Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
Yowaan 14:26
Leeru Bés bi
Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
Yowaan 14:26
Yeesu nag ne ndaw si: «Soo xamoon mayu Yàlla, ak kan moo la ne may ma, ma naan, kon yaw yaa koy ñaan, mu may la ndox miy dundal.»
Yowaan 4:10
Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
Luug 11:13
Bésub keroog, man dootuleen ma ñaan dara. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su boobaa lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko. Ba léegi ñaanuleen dara ci sama tur. Ñaanleen, nangule, ngir seen mbég mat sëkk.
Yowaan 16:23–24
Yeenay xemmem lu ngeen dul am. Yeenay bóome, di iñaane lu ñeneen am, te manuleen koo am. Yeenay xuloo aka jàppante. Dungeen am, ndax yeena ñaanul.
Yanqóoba 4:2
Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax. Moom, dina feeñal sama daraja, ndax ci sama jagleb bopp lay tanqe, àgge leen ko.
Yowaan 16:13–14
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell mi, mu soppaliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
Esayi 63:10
«Luy seen xalaat ci Almasi bi, kan lay ab sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.»
Macë 22:42
Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur, Boroom ndam duggsi. Buur, Boroom ndam booboo di kan? Xanaa Aji Sax ju gàngoor yi. Kookooy Buur, Boroom ndam. Selaw.
Taalifi cant 24:9–10
Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»
Peeñu ma 19:16
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.»
1.Piyeer 2:7
Nun nag, nuy waare ci Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jàmbur ñi dul Yawut. Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi bi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla.
1.Korent 1:23–24
Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi,
Filib 3:8
Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaan, bëgg nga maam?» Piyeer nag tiislu la ko Yeesu laaj ba ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Piyeer ne ko: «Sang bi, yaw xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Xontal ma samay xar.
Yowaan 21:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp6 Ut 2026
5 Ut 2026
4 Ut 2026
3 Ut 2026
2 Ut 2026
1 Ut 2026
31 Sul 2026