Leeru Bés bi — 12 Ut: Jooytu 3:31–32

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Boroom bi déy du la wacc ba fàww. Bu la tegee naqar it, yërëm la, ngoram a ni baree.

Jooytu 3:31–32

Yaw Yanqóoba sama jaam bi, bul tiit.» Kàddug Aji Sax jee. «Yaw laa àndal. Maay faxas mboolem xeet yi ma leen sànni woon, waaye yeen, duma leen faxas. Duma leen ñàkka duma moos, waaye dinaa leen yar lu yem.»

Yeremi 46:28

Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt, dellu la jël ci yërmande ju yaa. Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax ji lay jot moo ko wax.

Esayi 54:7–8

Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom, ndax duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?»

Esayi 10:11

Maa moy Aji Sax ji, kon naa tegoo meram, ba mu layool ma, dëggal ma, génne ma ba dugal ma ci leer gi, ma gis àtteb dëggam.

Mise 7:9

Bànni Israayil nag woo Aji Sax ji wall, Aji Sax ji dellu taxawal leen ku leen wallu, muy Beñamineen bu ñuy wax Ewudd doomu Gera; waa ju càmmoñe la woon. Ba loolu amee bànni Israayil yóbbante ko ab galag ca Eglon buuru Mowab.

Njiit ya 3:15

Gannaaw Ewudd, Samgar doomu Anat a aye. Moom moo jëloon aw yet wu ñuy xabtale ay nag, rey ca juróom benni téeméeri (600) góori Filisteen. Kooku it wallu na Israayil.

Njiit ya 3:31

Aji Sax ji walbatiku ca moom, ne ko: «Doxal, sa doole jii nga am, walloo ko bànni Israayil, yiwi ko ci loxol waa Majan. Xanaa du maa la yebal?» Mu ne ko: «Baal ma sang bi, waaye nu may yiwee Israayil? Samag làng kat moo gëna néew doole ci giirug Manase gi nu bokk, te man it maa gëna tuut ci sama kër baay.»

Njiit ya 6:14–15

Aji Sax ji ne Sedeyoŋ: «Gàngoor gi nga àndal moo ëpp ba duma mana teg waa Majan ci seen loxo. Lu ko moy Israayil tëggu ci sama kaw ne: “Sama loxol bopp a ma wallu.”

Njiit ya 7:2

Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne: Du cig njàmbaar, du ci doole, ci samag noo la. Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.»

Sàkkaryaa 4:6

Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

Efes 6:10