Leeru Bés bi — 31 Sulet: 2.Timote 2:3

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel.

2.Timote 2:3

Ab seedee ngoog, ñeel xeet yi, muy njiit, yilif xeet yi.

Esayi 55:4

Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.

Yawut ya 2:10

Ñuy feddali pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»

Jëf ya 14:22

Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan. Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.

Efes 6:12–13

Dëgg la, nitu suux lanu, waaye xeexewunu ni nit di xeexe. Ndaxte gànnaay yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel,

2.Korent 10:3–4

Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.

1.Piyeer 5:10

Defleen seen kem kàttan, ngir di jàmmoo, ba mana sàmm seenug bennoo ci biir Noo gu Sell gi ngeen bokk. Wenn yaram a fi nekk ak genn Noo ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme.

Efes 4:3–4

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi. Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen. Yeena di tabax bi ndawi Almasi bi ak yonent yi di fondmaa bi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju koñu tabax bi. Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi. Ci Almasi bi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jàmbur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Efes 2:18–22

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Céy liika baax te neexati, ay bokk yu bokk dëkk, di benn! Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ, siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona, rogalaat ba ci mbubbam,

Taalifi cant 133:1–2

Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.

1.Piyeer 1:22