Leeru Bés bi — 3 Ut: Luug 1:50

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

«Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam, maas ci kaw maas.

Luug 1:50

Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylooka xeebaate. Yàlla yaa yaatu ngëneel loo dencal ku la ragal, defal ko ku la làqoo, doom aadama seede.

Taalifi cant 31:19–20

Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.

1.Piyeer 1:17

Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg. Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.

Taalifi cant 145:18–19

Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.

Esayi 66:2

Ñi jub yuuxu, Aji Sax ji dégg, fu ñu jàqe, mu musal leen.

Taalifi cant 34:18

Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israayil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.

1.Samiyel 2:30

«Képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, man ci sama wàllu bopp itam, dinaa dëggal fa sama kanam Baay ba fa asamaan, ne man nga féeteel.

Macë 10:32

Ku ma gënalul sa ndey mbaa sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor mbaa ju jigéen, yeyoowuloo ma. Ku jëlul sa bantu bopp bu ñu lay daaj, te topp ci man, yeyoowuloo ma. Képp ku jot sa bakkan, dinga ko ñàkk, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, dinga ko jotaat.

Macë 10:37–39

Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.

Yanqóoba 1:12

Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.

Peeñu ma 2:10

Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.

2.Korent 4:17

Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.

1.Piyeer 1:7