Yeesu nag muucu bineegar ba, daldi ne: «Sotti na!» Ci kaw loolu mu sëgal bopp ba, daldi yiwi noo ga.
Yowaan 19:30
Leeru Bés bi
Yeesu nag muucu bineegar ba, daldi ne: «Sotti na!» Ci kaw loolu mu sëgal bopp ba, daldi yiwi noo ga.
Yowaan 19:30
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:2
Man de, feeñal naa sa màggaay ci àddina; liggéey bi nga ma santoon ma def ko, sottal naa ko.
Yowaan 17:4
Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax bi Yeesu Almasi bi sarxe yaramam benn yoon ba fàww. Bépp sarxalkat a ngi taxaw bés bu nekk ci liggéeyam, di jébbale aka jébbalewaat yenn sarax yooyu, te lenn du ci masa mana far bàkkaar. Waaye kii de, ba mu sarxee boppam ngir far ay bàkkaar, bennub sarax bu doy ba fàww, ca la tooge fa ndijooru Yàlla. Fa la doxe xaar bés ba ñu koy defal ay noonam ndëggastalu tànkam. Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww nit ñi ñu sellal.
Yawut ya 10:10–14
Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi bi ca bant ba.
Kolos 2:14
Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat. Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
Yowaan 10:17–18
Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw,
Yowaan 15:13
Aji Sax ji, dangaa gëdd, nokki, mu riir, xuri géej ne fàŋŋ, ron suuf ne duŋŋ.
Taalifi cant 18:16
May xaar a xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
Taalifi cant 40:2
Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww ji asamaan tiim, di boroom xel mu bon mi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey. Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.
Efes 2:1–3
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda. Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
Taalifi cant 61:1–2
Yunus ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, fa mu tollu ca biir jën wa. Mu ne: Maa jàq, woo Aji Sax ji, mu wuyu ma. Ca xóotey njaniiw laa wootee wall, nga dégg ma.
Yunus 2:2–3
May nga noon noot nu, nu jaare sawara, jaarem ndox; nga génne nu, yaatal nu.
Taalifi cant 66:12
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
Esayi 43:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Ut 2026
2 Ut 2026
1 Ut 2026
31 Sul 2026
30 Sul 2026
29 Sul 2026
28 Sul 2026