Doomu Firawna ne ko: «Yóbbul xale bii te nàmpalal ma ko, maa lay fey.» Ndaw sa jël liir ba, di ko nàmpal.
Mucc ga 2:9
Leeru Bés bi
Doomu Firawna ne ko: «Yóbbul xale bii te nàmpalal ma ko, maa lay fey.» Ndaw sa jël liir ba, di ko nàmpal.
Mucc ga 2:9
Mu ne leen: “Demleen yeen itam ca sama toolub reseñ, ma fey leen lu jaadu.”
Macë 20:4
Maa leen ko wax, déy, képp ku leen may ab kaasu ndox, ngir li ngeen di niti Almasi bi, doo ñàkk sag pey mukk.
Màrk 9:41
Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.
Kàddu yu xelu 11:25
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
Yawut ya 6:10
Ki jëmbat, ak ki suuxat ñoo yem kepp, waaye ku ci nekk kemu liggéeyu boppam lay yooloo.
1.Korent 3:8
Su ko defee boroom njekk yi ne ko: “Sang bi, kañ lanu la gis, nga xiif, nu leel la; mbaa nga mar, nu nàndal la? Ak kañ lanu la gis, nga dib doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la?
Macë 25:37–38
Bu loolu amee buur ba ne leen: “Maa leen ko wax déy, lu ngeen ci defal kenn ci ñi gëna tuut ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
Macë 25:40
«Ca la buur bay wax ñi ci ndijooram ne leen: “Yeen ñi sama Baay barkeel, dikkleen jël nguur gi ñu leen waajalaloon ba àddina sosoo.
Macë 25:34
di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def.
Taalifi cant 139:3
Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci béreb bii, te xawma ko woon.» Ma nga tiit nag te naan: «Béreb beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.»
Njàlbéen ga 28:16–17
Aji Sax ji déy suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol. Yëfi dof nga def ci mbir mii, ndax li dale tey ay xare topp na la.»
2.Jaar-jaar ya 16:9
May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.
Taalifi cant 4:8
Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji, Aji Kawe jii di sama rawtu, genn loraange du la dab, balaa du jege sa xayma. Ay malaakaam la lay booleel, ñu di la sàmm foo jëm.
Taalifi cant 91:9–11
Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.
Kàddu yu xelu 3:24
Neen it la nit di teela jóg aka guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw.
Taalifi cant 127:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Suw 2026
18 Suw 2026
17 Suw 2026
16 Suw 2026
15 Suw 2026
14 Suw 2026
13 Suw 2026