Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox. Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israayil.
Mucc ga 25:21–22
Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye ñu dugg ca néeg bu sella sell ba feeñagul woon, te fekk néeg bu njëkk ba di taxaw ba tey.
Yawut ya 9:8
Yeesu nag àddooti ca kaw, daldi yiwi noo ga.
Ca saa sa ridob biir néegu Yàlla ba dale ca kaw ba ca suuf, xar ñaar, suuf sa yëngu, doj ya xar,
Macë 27:50–51
Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.
Yawut ya 10:19–20
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Yawut ya 4:16
te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu. Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,
Room 3:24–25
ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi.
Efes 2:18
20-Yeesu ne leen: «Xanaa seenug néew ngëm. Maa leen ko wax déy, su ngeen amee ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën, dingeen ne tund wii: “Toxool fii, ba fale,” mu toxu, te dara du leen të.»
Macë 17:20
Gis naa say jëf. Maa def fi sa kanam, bunt bu tijjiku bu kenn manula tëj. Ndax néew nga doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma.
Peeñu ma 3:8
Ana kuy xeeb bés bii lu tuut sottee?
Nañu bége kay buumu betteex bi ñu gis ci loxol Sorobabel!
«Juróom ñaar yii nag gëti Aji Sax jee,
ñoom ñooy wër àddina sépp.»
Sàkkaryaa 4:10
Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.
2.Tesalonig 1:3
Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»
Luug 17:5
Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi,
maa leen di bëggal sama bopp,
nde mereetuma leen.
Maay mel nib lay buy guusal Israayil,
ñu focci ni tóor-tóor,
seeni reen sampu ni garabi Libaŋ,
Ose 14:5–6