Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Mu ne: Ci bii béreb laay mayee jàmm, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.”»
Ase 2:9
Leeru Bés bi
Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Mu ne: Ci bii béreb laay mayee jàmm, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.”»
Ase 2:9
Daawuda daldi ne: «Sama doom Suleymaan gone la te xamul àddina, te kër gi ñuy tabaxal Aji Sax ji wara màgg lool ba yéeme, yànj te am daraja ba siiw, xeet yépp gis ko. Kon nag dama koy daldi waajal.» Daawuda waajal na lu bare bala moo dee.
1.Jaar-jaar ya 22:5
Sarxalkat ya nag manuñoo dugg ca kër Aji Sax ji, ndax leeru Aji Sax ja fees kër Aji Sax ji.
2.Jaar-jaar ya 7:2
Yeesu ne leen: «Yàqleen kër Yàlla gii, ma yékkatiwaat ko ci ñetti fan.»
Yowaan 2:19
Waaye Yeesu kër Yàlla ga mu doon wax, yaramu boppam la woon.
Yowaan 2:21
Soo ko xoolee noonu, leer ga woon, du woon sax ag leer, ci leer gii ko raw tey,
2.Korent 3:10
Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.
Yowaan 1:14
Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp.
Yawut ya 1:1–2
«Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»
Luug 2:14
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.
Efes 2:14
Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:7
Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.
Room 13:12
Waaye yiirooleen Sang Yeesu Almasi bi, te ngeen baña yittewoo seen bakkan, ngir di topp seeni xemmemtéef.
Room 13:14
Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi, ngir ma mana feeñe ci biir Almasi bi, fu ma yaakaarul sama njubteg bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njubte gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi bi. Njubte googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi bi moo koy maye.
Filib 3:8–9
Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi bi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.
Room 3:22
Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
Esayi 61:10
Boroom bi Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa àtte dëgg gu wéet.
Taalifi cant 71:16
Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.
Efes 5:8
jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.
Efes 5:11
Waaye mboolem lu ñu feeñal, leer ga ñu ko leerale moo ko wone, te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: «Yaw miy nelaw, yewwul, dekkil, Almasi bi leeral la.» Kon nag xoolleen bu baax seen jëfin, defleen jëfinu nit ñu am xel, te baña mel ni ñu ñàkk xel.
Efes 5:13–15
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Suw 2026
2 Suw 2026
1 Suw 2026
31 Mee 2026
30 Mee 2026
29 Mee 2026
28 Mee 2026