Ni ngeen koy lekke nag nii la: bu ngeen koy lekk, dangeen di takku, sol seeni dàll, yor seen yet, te ngeen lekk ko ci lu gaaw. Loolu gàttu saraxu bésub Mucc ba lay doon, ñeel Aji Sax ji.
Mucc ga 12:11
Leeru Bés bi
Ni ngeen koy lekke nag nii la: bu ngeen koy lekk, dangeen di takku, sol seeni dàll, yor seen yet, te ngeen lekk ko ci lu gaaw. Loolu gàttu saraxu bésub Mucc ba lay doon, ñeel Aji Sax ji.
Mucc ga 12:11
Jógleen dem, fii du bérebu noflaay, nde sobewu na, ba nara yàqe yaxeet.
Mise 2:10
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.
Yawut ya 4:9
«Takkuleen te seeni làmp di tàkk. Melleen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil. Ndokkalee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
Luug 12:35–37
Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Piyeer 1:13
Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam, daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di woowe fa kaw, ci Almasi Yeesu. Kon nag, nun ñi jota màgg ba di magi jëmm ci wàllu ngëm, nanu ko bokk gise noonu. Su ci amee lenn lu ngeen gise neneen nag, loola, Yàlla moo leen koy leeralal.
Filib 3:13–15
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.
Taalifi cant 16:5
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Room 8:17
Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom,
1.Korent 3:21
Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.
Ngën-gi-woy 2:16
Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
Galasi 2:20
Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israayil.»
Màndiŋ ma 18:20
Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
Taalifi cant 73:25
Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
Taalifi cant 73:26
Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
Taalifi cant 23:4
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda.
Taalifi cant 63:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Suw 2026
31 Mee 2026
30 Mee 2026
29 Mee 2026
28 Mee 2026
27 Mee 2026
26 Mee 2026