Leeru Bés bi — 30 Mee: Yawut ya 4:11

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.

Yawut ya 4:11

«Duggeleen ci bunt bu xat bi, ndax bunt beek yoon wi jëm sànkute dañoo yaatu, te ñu baree cay dugge. Waaye xat la def, bunt ba jëm dund; sew it la yoon wa def, te ñu néew a koy gis.

Macë 7:13–14

Ca jamonoy Yaxya ba léegi, nguurug asamaan mu ngi jànkoonteek coono, ñiy jëfe doole di ko jéema aakimoo.

Macë 11:12

Ñam wuy yàqu, bumu leen taxa liggéey; liggéeyalleen ñam wi sax, ñam wiy texeel fàww, te Doomu nit ki moo leen koy jox, ndax moom la Yàlla màndargaal, ngir firndeel ne moom la tànn.»

Yowaan 6:27

Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo ak tànn gi ñu leen tànn. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk. Noonu lees leen di ubbile bunt bu yaa bu ngeen di tàbbee ca nguur gu sax gay sunu moomeelu Sang, sunu Musalkat, Yeesu Almasi bi.

2.Piyeer 1:10–11

Xanaa xamuleen ne, ab rawante, ñépp a cay daw, waaye kenn doŋŋ ay jël ndam li? Dawleen nag ba jël ndam li. Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.

1.Korent 9:24–25

Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dalloo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dalloo ci say liggéey.

Yawut ya 4:10

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.

Esayi 60:19

Man nag xam naa ne saa su nekk danga may nangul, waaye mbooloo mi fi teew a ma taxa wax loolu, ngir ñu gëm ne yaw yaa ma yebal.»

Yowaan 11:42

Ñu dindi doj wa. Yeesu xool ca kaw, daldi ne: «Baay, sant naa la, ndax nangul nga ma.

Yowaan 11:41

Baay, màggalal saw tur!» Ci kaw loolu baat dégtu ci asamaan, ne: «Maa koy màggal, màggalati ko.»

Yowaan 12:28

Ca laa ne: “Maa dikk nii, te téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man, maa defsi sa coobare, yaw Yàlla.”»

Yawut ya 10:7

Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»

Luug 22:42

Cofeel a mat sëkk ci nun, ngir nu ànd ak fit keroog bés-pénc. Te li nuy may fit mooy, ni Yeesu moomu nekke, noonu lanu nekke nun itam ci àddina sii.

1.Yowaan 4:17

Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul.

1.Yowaan 5:14

Te kon lu nu ñaan, mu may nu ko, ndax ay ndigalam lanuy sàmm, te li mu rafetlu lanuy jëfe.

1.Yowaan 3:22

Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga njëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.

Yawut ya 11:6

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:25

Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.

1.Yowaan 2:1