Aji Sax jee baax, moo dib rawtu, bésub njàqare, te moo ràññee ñi ko làqoo.
Nawum 1:7
Leeru Bés bi
Aji Sax jee baax, moo dib rawtu, bésub njàqare, te moo ràññee ñi ko làqoo.
Nawum 1:7
coowal mbégteek coowal bànneex ak kàddug boroom séet ak kàddug séetam, ànd ak kàdduy nit ñiy indi saraxi cant ci biir kër Aji Sax ji, tey dëbbe: “Santleen Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Aji Sax jee baax, kee saxoo ngoram.” Maay tijji wërsëgu réew mi, na woon.» Aji Sax jee ko wax.
Yeremi 33:11
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
Taalifi cant 46:1
Dama naa Aji Sax ji: «Yaw laay làqoo, di la fegoo; ngay sama Yàlla ji ma doyloo.»
Taalifi cant 91:2
Ndokkalee Israayil, ana ku mel ni yeen, askan wu Aji Sax jiy wallu, di seen kiiraay, di seen ndimbal, di saamar bi leen di sagal? Seeni noon ay lox ci seen kanam, te yeen, fa seen kawte ya ngeen di daagoo.»
Baamtug yoon wi 33:29
Waaye ku sopp Yàlla, Yàlla xam la.
1.Korent 8:3
Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
2.Timote 2:19
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.
Taalifi cant 1:6
Aji Sax ji ne Musaa: «Loolu nga wax, moom laa lay defal, ndax daj nga samaw yiw, te it maa la xam ci saw tur.»
Mucc ga 33:17
Sama coobare mooy, yeen gëmkati Almasi bi, ngeen mucc ci xalaat yu ub seen bopp. Te ku amul jabar, mbiri Boroom bi lay xalaat ak nu muy dabe bànneexu Boroom bi.
1.Korent 7:32
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.
1.Piyeer 5:7
Aji Sax ji déy suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol. Yëfi dof nga def ci mbir mii, ndax li dale tey ay xare topp na la.»
2.Jaar-jaar ya 16:9
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
Taalifi cant 34:8
Ragalleen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
Taalifi cant 34:10
«Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol. Xanaa du lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo? Xoolleen picc yi: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci am sàq. Teewul seen Baay ba fa asamaan di leen dundal. Yeen nag, xanaa du yeena gën picc yi fuuf?
Macë 6:25–26
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:6–7
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Mee 2026
25 Mee 2026
24 Mee 2026
23 Mee 2026
22 Mee 2026
21 Mee 2026
20 Mee 2026