Leeru Bés bi — 29 Mee: Sarxalkat yi 17:11

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.

Sarxalkat yi 17:11

Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.

Yowaan 1:29

Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi.

Peeñu ma 7:14

waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.

1.Piyeer 1:19

Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.

Yawut ya 9:22

Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.

1.Yowaan 1:7

Du deretu sikket mbaa yëkk la duggaale, waaye deretu boppam la dugge benn yoon ba fàww ca néeg bu sella sell, te moom la amale njotlaay gu sax dàkk.

Yawut ya 9:12

Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe.

Yawut ya 10:19–20

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yawut ya 10:22

ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.

1.Korent 6:20

Njàqaree ma dugg, may kat-kati, musiba mëdd ma.

Taalifi cant 55:6

Naka la jant ba fenk, Yàlla yebal ngelawal penku lu tàng jérr, jant ba jam boppu Yunus, ba mu xawa xëm, bëggatul dara ci bakkanam. Mu naan: «Dee sax a ma gënal dund!»

Yunus 4:8

Mu ne:

Ayóoba 3:2

Boroom tiis, ana lees koy maye leeru kaw suuf? Lu boroom naqar di doye bakkan? Ku ni mel ku yàkkamti dee gu dikkul, te gëna sàkku dee alal ju làqu,

Ayóoba 3:20–21

Seen yaakaar tas, Aji Sax ji jege leen, seen xol jeex, Aji Sax ji wallu leen.

Taalifi cant 34:19

«Léegi nag am naa njàqarey xol. Ana lu may wax? Dama naa: “Baay, musal ma ci coonob waxtu wii”? Waaye coonob waxtu wii tembe moo ma taxa dikk!

Yowaan 12:27

Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan. Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.

Yawut ya 2:17–18