Leeru Bés bi — 26 Mee: Yawut ya 13:20

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,

Yawut ya 13:20

ba bu sàmm bu mag bi feeñee, ngeen jot kaalag daraja gu dul furi.

1.Piyeer 5:4

«Man maay sàmm bi baax. Maa xam sama xari bopp, ñoom it ñu xam ma.

Yowaan 10:14

Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp. Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo.

Yowaan 10:27–28

Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk. Parlu mu naat la may gooral, wal mu dal, mu tette ma ca, leqali ma, teg ma ci yooni njub ngir teraangay turam.

Taalifi cant 23:1–3

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.

Esayi 53:6

«Man maay sàmm bi baax. Sàmm bu baax, bakkanam lay joxe, jote ko ay xaram.

Yowaan 10:11

Bu ci réer, maa lay seet; bu ci xàjjiku, maa lay delloosi; bu ci damm, maa yeew ba mu dëgër; bu ci néew doole, ma leqali la. Waaye bu ci duuf, am doole, maa lay sànk, sàmm la, def li war ci yaw.

Esekiyel 34:16

«Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.

1.Piyeer 2:25

Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Xar mi di làmpam.

Peeñu ma 21:23

Ba ma demee, booru digg bëccëg, Buur, ca laa gis ag melax gu leer ba raw jant bi, fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër, maak ñi ma àndal.

Jëf ya 26:13

«Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bunduxataal.

Jëf ya 26:15

Ba ñu ca tegee juróom benni fan, Yeesu ànd na ak Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan rakku Yanqóoba, yóbbu leen kaw tund wu kawe, ngir wéetook ñoom. Mu soppiku fa seen kanam, xar kanamam di melax nib jant, ay yéreem weex nig leer.

Macë 17:1–2

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar. Sab jant du sooti, sa weer du suuxati. Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa fani ñaawlu jeex.

Esayi 60:19–20

Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.

1.Piyeer 5:10