Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.
Efes 4:30
Leeru Bés bi
Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.
Efes 4:30
Gannaaw loolu bokk yi, li ma leen di ñaan ngir sunu Boroom Yeesu Almasi bi, ngir itam cofeel gi Noo gu Sell giy maye, moo di ngeen fekksi ma ci xareb ñaan ngir man.
Room 15:30
Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
Yowaan 14:26
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot. Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell mi, mu soppaliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
Esayi 63:9–10
Ni nuy xame ne ci Yàlla la nu saxe, te moom itam ci nun la sax, moo di Noowam gi mu nu sédd ab cér.
1.Yowaan 4:13
Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon. Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.
Efes 1:13–14
Li ma leen di wax moo di: doxeleen Noowug Yàlla, su boobaa dungeen topp seen xemmemtéefi bakkan. Ndax bakkan, la muy xemmem, daa dëngoo ak Noo gi; Noo gi it, la muy xemmem dëngoo ak bakkan. Dañu di ñaar yu féewaloo, te moo tax dungeen def la ngeen nammoona def.
Galasi 5:16–17
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
Room 8:26
Ma daldi ñibbi, ba ñu nangu seenug tooñ, seet fu ma féete. Bu ñu jàqee lañuy daw wutsi ma.»
Ose 5:15
Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.
Esayi 59:2
Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.
Ngën-gi-woy 5:6
Ñaawtéefi Israayil ak alalam ju lewul moo ma merloo, ma duma ko, xañ ko sama kanam, waaye mu të ticc, topp xolam. Xam naa jikkoom, waaye maa koy faj, wommat ko, dëfale koy xéewal, mook ñiy ñaawloondook moom.
Esayi 57:17–18
Xanaa du yeena def seen bopp lii, di wacc seen Yàlla Aji Sax ji, ba mu leen di jiite ca yoon wa?
Yeremi 2:17
«Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
Luug 15:20
Asiri du nu xettali, ay fasi xare it, dunu ko war, te dootunu wax lu nu sàkke sunuy loxo, ne ko: “Yaw yaa di sunu Yàlla.” Li nuy wax kay mooy yaw yaay kiy yërëm jirim.»
Ose 14:4
Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
1.Yowaan 1:9
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Mee 2026
22 Mee 2026
21 Mee 2026
20 Mee 2026
19 Mee 2026
18 Mee 2026
17 Mee 2026