Leeru Bés bi — 21 Mee: Efes 6:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

Efes 6:10

Boroom bi Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa àtte dëgg gu wéet.

Taalifi cant 71:16

Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.

Room 1:16

Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.

Filib 4:13

Loolu moo ma tax di góor-góorlu ci xare bii may xare ci dooleem ak manoorey jëfam jiy liggéey ci sama jëmm jii.

Kolos 1:29

Nun nag nooy njaqi bani kese yi yeb jooju alal, ngir mu bir ne manoore ju yéeme ji alal ji làmboo, manoorey Yàllaa, waaye du sunu jos.

2.Korent 4:7

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Neyemi 8:10

Ngir itam ngeen manoorewoo jépp manoore, na leen ko Yàlla manloo ci kàttanam gu màgg, ba ngeen mana dékku lépp ci xolu muñ,

Kolos 1:11

Yàllaa am kóllëre, moom mi leen woo, ngir ngeen bennoo ak Doomam Yeesu Almasi bi, sunu Sang.

1.Korent 1:9

Doom ju góor lay am; nanga ko tudde Yeesu (muy firi Boroom beey musle), ndax mooy musal aw xeetam ci seeni bàkkaar.»

Macë 1:21

Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj. Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur, ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy ci kaw asamaan, di ci kaw suuf, di biir suuf,

Filib 2:8–10

Ndaw si ne ko: «Xam naa ne Almasi baa ngi ñëw, moom lañu naan Ki ñu fal, kooku bu dikkee, moo nuy leeralal lépp.»

Yowaan 4:25

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi seen goreel, yégal ñi ñu tëj seen ubbite.

Esayi 61:1

Tomaa àddu ne ko: «Yaa di sama Boroom, di sama Yàlla!»

Yowaan 20:28

Yeena ngi ma naa Kilifa gi ak Sang bi, te yeena yey, nde moom laa. Ndegam nag man miy Sang bi, di Kilifa gi maa leen raxasal seeni tànk, kon yeen itam war ngeen di raxasalante ay tànk. Ab misaalu royukaay laa leen jox, ngir ni ma leen defal, ngeen di ko def yeen itam.

Yowaan 13:13–15