Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba.
Taalifi cant 51:2
Leeru Bés bi
Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba.
Taalifi cant 51:2
Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal.
Yeremi 33:8
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
Esekiyel 36:25
Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki su juddoowul ci ndox ak ci Noowug Yàlla, du mana tàbbi ci nguurug Yàlla.
Yowaan 3:5
Deretu sikket ak yëkk, ak dóomu nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen. Su loolu amee, ñaata yoon la deretu Almasi bi ëppe njariñ! Almasi bi mooy ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi. Moom rekk moo mana setal sunu yaraangey xel mi sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci dee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!
Yawut ya 9:13–14
Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, ba xamle njàmbaaram.
Taalifi cant 106:8
Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun, saw tur nga wara teral, ngir sa ngor ak sa worma.
Taalifi cant 115:1
ndax seen loxo bi ngeen jo ci xamle xibaaru jàmm bi, te dale ko ca bés bu njëkk ba, ba tey.
Filib 1:5
Noonu yaramu nit nekkee wenn te di cér yu bare, ak noonu mboolem céri yaram dee wenn yaram wi, ak li cér yiy bare lépp, noonu rekk la itam ci Almasi bi. Ci genn Noo gu Sell gi lañu nu sóobe ci biir wenn yaram wi, nun ñépp, nu diy Yawut, mbaa nu diy jàmbur, nu diy jaam, mbaa nu diy gor, te nun ñépp, genn Noo gi lañu nu nàndale.
1.Korent 12:12–13
Yàllaa am kóllëre, moom mi leen woo, ngir ngeen bennoo ak Doomam Yeesu Almasi bi, sunu Sang.
1.Korent 1:9
Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
1.Yowaan 1:7
Loolu la Yeesu wax ba noppi, téen, xool asamaan, daldi ne: «Baay, waxtu wi jot na. Feeñalal sa darajay Doom, ngir Doom ji feeñal sa daraja.
Yowaan 17:1
«Du ñoom doŋŋ laay ñaanal nag, waaye ñi may gëm ëllëg ndax seen kàddu itam laay ñaanal, ngir ñépp doon benn, ni nga nekke yaw Baay, ci man, ma nekke ko ci yaw, ñoom itam, ñu nekke ni ci nun, ba àddina gëm ne yaw yaa ma yebal.
Yowaan 17:20–21
Bés yu mujj yi
Wone yépp18 Mee 2026
17 Mee 2026
16 Mee 2026
15 Mee 2026
14 Mee 2026
13 Mee 2026
12 Mee 2026