Ci man Póol miy jaamub Almasi Yeesu la bataaxal bii bawoo, man miy ndawam ci kaw woote bu ma tabb, sédd ma sasu xamle xibaaru jàmm bu Yàlla.
Room 1:1
Leeru Bés bi
Ci man Póol miy jaamub Almasi Yeesu la bataaxal bii bawoo, man miy ndawam ci kaw woote bu ma tabb, sédd ma sasu xamle xibaaru jàmm bu Yàlla.
Room 1:1
Yeena ngi ma naa Kilifa gi ak Sang bi, te yeena yey, nde moom laa.
Yowaan 13:13
Ku may surgawu, na ma topp; fu ma nekk, sama surga ne fa moom itam. Ku ma surgawu nag, sama Baay moo koy teral.
Yowaan 12:26
Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof. Sama kilifteef sedd na, te samab sëf woyof.»
Macë 11:29–30
Waaye la ma jàppe woon ag ndollent, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi bi.
Filib 3:7
Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag cellte la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.
Room 6:22
Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko.
Yowaan 15:15
Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.
Galasi 4:7
Almasi bi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.
Galasi 5:1
Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.
Galasi 5:13
Ma sant Aji Sax ji may xelal, ba guddi sax sama xel di ma yedd.
Taalifi cant 16:7
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa amug dégg, di boroom doole.
Kàddu yu xelu 8:14
Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
Taalifi cant 119:105
Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Kàddu yu xelu 3:5–6
Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.
Yeremi 10:23
di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.
Esayi 30:21
Loo bëgga def, diis ko Aji Sax ji, say mébét sotti.
Kàddu yu xelu 16:3
Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.
Ayóoba 23:10
Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
Kàddu yu xelu 20:24
Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teraanga.
Taalifi cant 73:24
nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,
Taalifi cant 48:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Mee 2026
14 Mee 2026
13 Mee 2026
12 Mee 2026
11 Mee 2026
10 Mee 2026
9 Mee 2026