Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deewam,
Filib 3:10
Leeru Bés bi
Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deewam,
Filib 3:10
Ab taalibe, su demee ba mel ni kilifaam, wàcc na; ab jaam it, su demee ba mel ni sangam, wàcc na. Ndegam boroom kër gi lañuy woowe Beelsebul, miy Seytaane, astamaak waa këram.
Macë 10:25
Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.
Esayi 53:3
Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»
Yowaan 16:33
Su ngeen bokkoon ci àddina, àddina bëgg leen, ndax li ngeen diy ñoñam, waaye dangeena bokkul ci àddina, nde maa leen tànne ci àddina, te looloo tax àddina bañ leen.
Yowaan 15:19
Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslooka toroxal, yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon.
Taalifi cant 69:20
Keroog ba ma njëkkee di layool sama bopp, kenn taxawuwu ma, ñépp a ma daw, yàlla bu leen seen jëf topp.
2.Timote 4:16
Yeesu itam ne ko: «Till akug kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit ki de, amul fu mu wéer boppam.»
Macë 8:20
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:1–2
Sunu bokk yee daan ndax deretu Xar mi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.
Peeñu ma 12:11
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub. Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
Room 8:33–34
Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.
Sarxalkat yi 17:11
«Guddig keroog maay wër réewum Misra te maay faat lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, nit ak mala, te itam maay mbugal mboolem tuuri Misra. Man maay Aji Sax ji. Deret ji ci kër yi ngeen dëkke nag, mooy doon seen xàmmikaay, ba tax bu ma gisee deret ji, musal leen. Su ko defee bu may dal ci kaw réewum Misra, menn musiba du leen lor.
Mucc ga 12:12–13
Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.
Room 8:1
Ci kaw loolu kenn ci mag ñi ne ma: «Boroom mbubb yu weex yii, ñooy ñan ak fan lañu jóge?» Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi.
Peeñu ma 7:13–14
tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar, ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak manoore ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Peeñu ma 1:5–6
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Mee 2026
12 Mee 2026
11 Mee 2026
10 Mee 2026
9 Mee 2026
8 Mee 2026
7 Mee 2026