Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Sama dogali yoon, jëfeleen ko; sama àttey yoon, ngeen sàmm ko, di ko jëfe.
Esekiyel 20:19
Leeru Bés bi
Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Sama dogali yoon, jëfeleen ko; sama àttey yoon, ngeen sàmm ko, di ko jëfe.
Esekiyel 20:19
Ku ne moo sax ci Yàlla, fàww ni Yeesu Almasi bi daan jëfe, ni lay jëfe moom itam.
1.Yowaan 2:6
Gannaaw xam ngeen ne moo jub, xamleen itam ne képp kuy def njub, ci moom nga sosoo.
1.Yowaan 2:29
Xaraf amul solo, ñàkka xaraf amul solo. Li am solo moo di topp ndigali Yàlla.
1.Korent 7:19
Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daan bu ñu teg ci ku moy yoon wépp, ñeel na ko.
Yanqóoba 2:10
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Aji Sax ji, xamal ma li sa dogali yoon yiy firi, ma topp ko ba mu jeex.
Taalifi cant 119:33
Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,
Filib 2:12
ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Filib 2:13
Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,
Yawut ya 13:20
yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottal ci Yeesu Almasi bi daraja ñeel ba fàww. Amiin.
Yawut ya 13:21
Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.
Taalifi cant 89:19
Ndax kat du ay malaaka la Yeesu xettalisi, waaye askanu Ibraayma la xettalisi.
Yawut ya 2:16
Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.
Yawut ya 2:17
Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kaw-a-kaw lay nirook ngàngune.
Esekiyel 1:26
Kenn masula yéeg fa asamaan ku moy ki wàcce asamaan, te mooy Doomu nit ki.
Yowaan 3:13
Xoolleen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.»
Luug 24:39
Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam. Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj. Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur, ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy ci kaw asamaan, di ci kaw suuf, di biir suuf,
Filib 2:7–10
Teewlul te nga leqali ndes wi ngay waaja deele. Ndax kat, gisuma sa jëf ju mat fa sama kanam Yàlla.
Peeñu ma 3:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Mee 2026
15 Mee 2026
14 Mee 2026
13 Mee 2026
12 Mee 2026
11 Mee 2026
10 Mee 2026