Soppe yi, nanu soppante, ndax cofeel ci Yàlla la bokk; képp ku am cofeel, ci Yàlla nga sosoo, te xam nga Yàlla.
1.Yowaan 4:7
Leeru Bés bi
Soppe yi, nanu soppante, ndax cofeel ci Yàlla la bokk; képp ku am cofeel, ci Yàlla nga sosoo, te xam nga Yàlla.
1.Yowaan 4:7
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay». Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
Room 8:15–16
Ku gëm Doomu Yàlla, seede soosoo ngi ci sab xol. Ku gëmul Yàlla nag, ab fen-kat nga ko def, ndax yaa gëmul seede si Yàlla seedeel Doomam.
1.Yowaan 5:10
Ni cofeelu Yàlla feeñe ci nun moo di jenn Doomu boppam ji mu yebal ci àddina, ngir nu mana dund ci kàttanam.
1.Yowaan 4:9
Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,
Efes 1:7
Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.
Efes 2:7
Soppe yi, ndegam Yàllaa nu soppe nii, nun itam war nanoo soppante.
1.Yowaan 4:11
Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslooka toroxal, yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon.
Taalifi cant 69:20
Xanaa kii du doomu minise bi? Xanaa du Maryaama mooy yaayam? Rakkam yu góor di Yanqóoba ak Yuusufa ak Simoŋ ak Yudd?
Macë 13:55
Natanayel ne ko: «Mbaa lu baax man naa jóge Nasaret yee?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»
Yowaan 1:46
Yawut ya ne ko: «Xanaa yeyunu nag, ba nu nee nitu Samari nga, te aw rab a la jàpp?»
Yowaan 8:48
Teewul Farisen ya naan: «Ci buuru rab yi lay dàqe ay rab.»
Macë 9:34
Farisen ya dellu woo ka gumba woon, ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Nun xam nanu ne waa jooju nit kuy bàkkaar la.»
Yowaan 9:24
Ci kaw loolu déeyoo bi ci mbiram bare ca mbooloo ma. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day naxe.»
Yowaan 7:12
Ay firikati yoonu Musaa nag jekki di wax ci seen biir naan: «Kii, Yàlla lay diir mbagg!»
Macë 9:3
Doomu nit ki ñëw, di lekk aka naan, ñu naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat yeek bàkkaarkat yi!” Waaye xel mu rafet, jëf ja mooy la koy dëggal.»
Macë 11:19
Ab taalibe, su demee ba mel ni kilifaam, wàcc na; ab jaam it, su demee ba mel ni sangam, wàcc na. Ndegam boroom kër gi lañuy woowe Beelsebul, miy Seytaane, astamaak waa këram.
Macë 10:25
Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la. Muñ ay dóor yu la fekk ci tooñ, ana lu ciy ndam? Waaye soo muñee coono boo daj ngir lu baax loo def, loolu de aw yiw la fa kanam Yàlla. Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam. «Moo bàkkaarul, fenul.» Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
1.Piyeer 2:19–23
Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi bi, ndokkalee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.
1.Piyeer 4:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Mee 2026
10 Mee 2026
9 Mee 2026
8 Mee 2026
7 Mee 2026
6 Mee 2026
5 Mee 2026