Kuy bàkkaar, ci Seytaane la bokk, ndax Seytaane moo dale bàkkaar ca njàlbéen ga. Te Doomu Yàllaa dikk ngir nasaxal liggéeyu Seytaane.
1.Yowaan 3:8
Leeru Bés bi
Kuy bàkkaar, ci Seytaane la bokk, ndax Seytaane moo dale bàkkaar ca njàlbéen ga. Te Doomu Yàllaa dikk ngir nasaxal liggéeyu Seytaane.
1.Yowaan 3:8
Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.
Efes 6:12
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.
Yawut ya 2:14
Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam la Almasi bi ame ca bant ba.
Kolos 2:15
Ci kaw loolu ma dégg baat bu xumb bawoo asamaan, ne: «Léegi nag texe teew na, ànd ak sunu kàttanu Yàlla ak nguuram, ak sañ-sañu Almaseem, ndax xalab nañu ki daan tuumaal sunu bokk yi, di leen sosal guddeek bëccëg fi sunu kanam Yàlla. Sunu bokk yee daan ndax deretu Xar mi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.
Peeñu ma 12:10–11
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:57
Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba, cóolóoloo cóolóol, léppi cóolóoli neen.
Kàdduy waare 1:2
Sunu giiru dund nga di nu mere, sunuy fan jeex ni noo guy naaw. Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at, ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk; li ci ëpp di coonooku tiis, ne fëyy, nu wéy.
Taalifi cant 90:9–10
Su dee ci giiru dund gii doŋŋ lanu ame yaakaar ci Almasi bi, kon de noo gëna toskare ñépp.
1.Korent 15:19
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
«Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba, maanaam ay suufukat.
Malasi 3:6
Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.
Filib 3:20–21
Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,
Room 8:20
Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.
Yawut ya 13:8
Ñeenti mbindeef yi am nañu ku nekk juróom benni laaf, fees aki bët ba daj, biir ak biti, te guddi ak bëccëg duñu selaw, xanaa naan: «Kee sell, Kee sell, Kee sell, Keey Boroom bi Yàlla Aji Man ji, Kee masa nekk, Kee nekk, Keey dikk.»
Peeñu ma 4:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Mee 2026
8 Mee 2026
7 Mee 2026
6 Mee 2026
5 Mee 2026
4 Mee 2026
3 Mee 2026