Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; waaye moytuleena tiit, ndax fàww loolu am, waaye du doonagum muj ga.
Macë 24:6
Leeru Bés bi
Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; waaye moytuleena tiit, ndax fàww loolu am, waaye du doonagum muj ga.
Macë 24:6
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen. Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee, ba dunu tiit suuf su yëngu sax, ba tund yiy tàbbi biir géej,
Taalifi cant 46:1–3
Yeen samaw askan, ayca duggleen seeni néeg, tëju ca biir. Làquleen as lëf, ba sànj mi jàll. Aji Sax ji kat a ngii di génne màkkaanam ma, nara dikke waa àddina mbugalu ñaawtéef, ba suuf wone deret ji ñu tuur fi kawam, te dootul sàng ñi ñu bóom.
Esayi 26:20–21
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda, gannaaw ba mu dawee Buur Sawul, ba dugg ca xunt ma.
Taalifi cant 57:1
ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla.
Kolos 3:3
Du ragal dég-dég bu tiis, xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji,
Taalifi cant 112:7
Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»
Yowaan 16:33
Yal na seeni dal gent, seeni xayma wéet.
Taalifi cant 69:26
Yeesu neeti ay taalibeem: «Ag fiir guy bàkkaarloo manula ñàkk, waaye wóoy ngalla ka koy lal.
Luug 17:1
Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
Jëf ya 2:23
Ca lañu ko tifli ci kanam, dóor ko ay këmëx. Ñeneen ña talaata ko, te naan ko: «Almasée, waxal nu kàdduy waxyu boog, ana ku la dóor?»
Macë 26:67–68
Sarxalkat yu mag ya it naka noonu, ñook firikati yoonu Musaa ya ak magi askan wa. Ñu di ko ñaawal, naan: «Moom day musle te manul musal sax boppam! Mooy buurub Israayil, na wàcc bant bi léegi kay, nu gëm ko.
Macë 27:41–42
Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israayil ci kaw Yeesu, sa jawriñ ju sell ji nga fal. Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogaloon ci sa loxo ak sa coobare.
Jëf ya 4:27–28
Ndaxam moom sunu wopp la yenu, sunuy mitit la sëfoo. Nun nu foog ne dees koo mbugal, foog ne Yàllaa ko duma, toroxal ko.
Esayi 53:4
Bés yu mujj yi
Wone yépp6 Mee 2026
5 Mee 2026
4 Mee 2026
3 Mee 2026
2 Mee 2026
1 Mee 2026
30 Awr 2026