Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.
Esayi 53:10
Leeru Bés bi
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.
Esayi 53:10
«Léegi nag am naa njàqarey xol. Ana lu may wax? Dama naa: “Baay, musal ma ci coonob waxtu wii”? Waaye coonob waxtu wii tembe moo ma taxa dikk! Baay, màggalal saw tur!» Ci kaw loolu baat dégtu ci asamaan, ne: «Maa koy màggal, màggalati ko.»
Yowaan 12:27–28
Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.» Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
Luug 22:42–43
Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj.
Filib 2:8
Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat.
Yowaan 10:17
Def sama coobarey bopp taxul ma wàcce fa asamaan, waaye def coobarey ki ma yónni moo tax.
Yowaan 6:38
Yeesu ne Piyeer: «Defal saamar ci mbaram. Kaasub naqar bi ma Baay bi sédd, xanaa dama ko dul naan?»
Yowaan 18:11
Te it ki ma yónni moo ànd ak man; bàyyiwu ma, ma wéet, ndax man, li ko neex doŋŋ laay def.»
Yowaan 8:29
Ci kaw loolu rekk, baat jibe asamaan, ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe; Moom laay bànneexoo.»
Macë 3:17
Aji Sax ji nee: «Xoolleen sama jaam bii ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci moom laa sol sama xel, te mooy indil xeet yi yoonu àtte.
Esayi 42:1
Yerusalem, tabb naa ay wattukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dallu.
Esayi 62:6
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote ay niti gépp giir ak wépp làkk ak wépp xeet ak wépp askan, ñu doon ñoñi Yàlla. Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»
Peeñu ma 5:9–10
Na doomi Aaróona sarxalkat yi di wal liit yi, te mu doon dogal bu leen saxal dàkk, ci seen maasoo maas. «Bu loolu wéyee, bu ngeen dee xare ci seenum réew, ak noon bu leen songsi, nangeen riiral liit yi riir mu xumb, su boobaa dees na leen bàyyi xel fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ba wallu leen ak seeni noon.
Màndiŋ ma 10:8–9
Làquwuma, di waxe béreb bu lëndëm. Newuma it askanu Yanqóoba: “Wërleen ma ci neen.” Man Aji Sax ji maay wax dëgg, di biral liy yoon.»
Esayi 45:19
Ci kaw loolu sarxalkat yay Leween ñaanal askan wa barkeb Aji Sax ji, seen baat jib, seen ñaan ga àkki kaw asamaan, fa màkkaanam mu sell.
2.Jaar-jaar ya 30:27
Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
Taalifi cant 34:15
Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, day dal ak doole.
Yanqóoba 5:16
Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!
Peeñu ma 22:20
Képp ku la wër, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»
Taalifi cant 40:17
ak yàkkamti bésu Yàlla ba, di jëfe li koy taxa gaawa dikk, ba asamaan yi lakk ba jeex, lu ca jëmmu lakk ba seey.
2.Piyeer 3:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Mee 2026
6 Mee 2026
5 Mee 2026
4 Mee 2026
3 Mee 2026
2 Mee 2026
1 Mee 2026