Kon nag, buleen jaaxle, naan: “Lu nuy lekk?” mbaa “Lu nuy naan?” mbaa “Lu nuy sol?” Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.
Macë 6:31–32
Leeru Bés bi
Kon nag, buleen jaaxle, naan: “Lu nuy lekk?” mbaa “Lu nuy naan?” mbaa “Lu nuy sol?” Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.
Macë 6:31–32
Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokkalee yaw mi ko làqoo. Ragalleen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
Taalifi cant 34:9–10
Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon. Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; te du ngëneel lu muy bañal ku mat.
Taalifi cant 84:11–12
Sama coobare mooy, yeen gëmkati Almasi bi, ngeen mucc ci xalaat yu ub seen bopp. Te ku amul jabar, mbiri Boroom bi lay xalaat ak nu muy dabe bànneexu Boroom bi.
1.Korent 7:32
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant.
Filib 4:6
Ñaari picci ramatu, xanaa du dërëm lay jar? Moona menn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay. Seen kawari bopp sax, waññees na lépp. Kon nag buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën.
Macë 10:29–31
Yeesu ne leen: «Lu ngeen di tiit? Dangeena gëmul ba tey?»
Màrk 4:40
Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla.
Màrk 11:22
Mu firiw niir, yiire leen, ak sawara, ñu niitoo guddi.
Taalifi cant 105:39
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal. Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
Taalifi cant 103:13–14
Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi.
Taalifi cant 121:6
di mbaar mu ñuy féexloo tàngooru bëccëg, di ko seeloob taw ak waame.
Esayi 4:6
Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.
Taalifi cant 121:5
Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, tey ak ëllëg.
Taalifi cant 121:8
Bu bëccëgee nag Aji Sax ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg. Du bëccëg bu niir wa jóge ca kanam mbooloo ma, te du guddi it gu sawara wa masa wuute.
Mucc ga 13:21–22
Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.
Yawut ya 13:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Mee 2026
3 Mee 2026
2 Mee 2026
1 Mee 2026
30 Awr 2026
29 Awr 2026
28 Awr 2026