Leeru Bés bi — 4 Mee: Esayi 59:1

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg.

Esayi 59:1

Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.

Taalifi cant 138:3

Maa ngay wax ci ñaan gi, waa ja Jibril ma ma gisoon lu jiitu ci peeñu mi, daldi naaw a naaw, dikk ba ci man, yemook waxtuw saraxu ngoon.

Dañeel 9:21

Sang bi, bu ma làqu, bul mer, jañax ma. Yaa ma daa wallu. Bu ma wacc, bu ma ba, yaay Yàlla mi may musal.

Taalifi cant 27:9

séddoo samay yére, tegoo bant sama mbubb.

Taalifi cant 22:19

«Éy saa Boroom, Aji Sax ji! Yaw déy yaa sàkk asamaan, sàkk suuf ci sa doole ju bare ak sa kàttan gu matale. Dara tëwu la.

Yeremi 32:17

Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu.

2.Korent 1:10

Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe? Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?»

Luug 18:7–8

Man de, feeñal naa sa màggaay ci àddina; liggéey bi nga ma santoon ma def ko, sottal naa ko.

Yowaan 17:4

Yeesu ne leen: «Samaw ñam moo di jëfe coobarey ki ma yónni, ba sottal ab liggéeyam.

Yowaan 4:34

Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.

Yowaan 9:4

Mu ne leen: «Lu ngeen may seete? Xamuleen ne sama kër Baay laa wara nekk?» Ay waajuram ñoom dégguñu kàddu googu mu leen wax.

Luug 2:49–50

Yeesu dégg ca, ne: «Wopp jooju de du woppi dee, waaye darajay Yàlla lay feeñal, ba màggale ko Doomu Yàlla ji.»

Yowaan 11:4

Yeesu ne ko: «Xanaa waxuma la ne soo gëmee, dinga gis màggug Yàlla?»

Yowaan 11:40

Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi.

Luug 2:52

Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»

Luug 3:22

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote ay niti gépp giir ak wépp làkk ak wépp xeet ak wépp askan, ñu doon ñoñi Yàlla. Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»

Peeñu ma 5:9–10