Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci béreb bii, te xawma ko woon.»
Njàlbéen ga 28:16
Leeru Bés bi
Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci béreb bii, te xawma ko woon.»
Njàlbéen ga 28:16
ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
Macë 18:20
te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Macë 28:20
Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Mucc ga 33:14
Fu ma jëm, ba sore la? Fu ma daw jëm, foo teewul? Ma ñalgu ba asamaan, yaa nga fa! Ma tëri njaniiw, ndeke yaa nga fa!
Taalifi cant 139:7–8
Xanaa du maay Yàlla?» Kàddug Aji Sax jee. «Fu jegeek fu sore, du maay Yàlla? Ku mana làqoo làquwaay, ba duma ko gis?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du asamaan ak suuf, maa ko fees?» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 23:23–24
«Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ci kaw suuf sax? Seetal rekk, Seetal rekk, asamaan ba ca asamaani asamaan manu laa fat, astamaak kër sii ma tabax.
1.Buur ya 8:27
Ku màgg, Ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk te toroxlu, ngir leqali ku toroxlu, leqali boroom xol bu mokk.
Esayi 57:15
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»
2.Korent 6:16
Xale yi, wattuleen seen bopp ci ay tuur.
1.Yowaan 5:21
Doom, teewloo ma xel te roy ma.
Kàddu yu xelu 23:26
La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf,
Kolos 3:2
«Yaw nit ki, ñii seen kasaray tuur lañu def ci seen xol, muy ay wu leen di gàllankoor, te ñu ne ci jàkk. Ndax ñii dinaa leen wacc moos, ñuy sàkku leeraange ci man?
Esekiyel 14:3
Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni séy yi yoon tere ak jëfi sobe ak ñàkk sago ci lu jekkadi ak xemmemtéef yu bon ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey,
Kolos 3:5
Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan aki fiir ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute. Ndax sopp xaalis kat mooy reenu mboolem xeeti loraange. Am na ñuy ŋaf-ŋafi, di ko wut, far lajj ci yoonu ngëm, ba teg seen bopp tiis wu bare. Yaw miy nitu Yàlla nag, dawal loolu, te topp njub ak ragal Yàlla ak ngëm ak cofeel ak muñ akug teey.
1.Timote 6:9–11
Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!
Taalifi cant 62:10
Li may mayee gën wurus, muy wurus wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
Kàddu yu xelu 8:19
Ndaxte fa sab denc nekk, sab xol it a nga fa.
Macë 6:21
Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»
1.Samiyel 16:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Mee 2026
30 Awr 2026
29 Awr 2026
28 Awr 2026
27 Awr 2026
26 Awr 2026
25 Awr 2026