Leeru Bés bi — 28 Awril: Yowaan 1:29

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.

Yowaan 1:29

ndax deretu yëkk ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar. Moo tax ba Almasi biy dikk ci àddina la wax ne: «Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko, waaye aw yaram nga ma waajalal. Saraxu rendi-dóomal ak saraxu póotum bàkkaar, safoowuloo ci dara. Ca laa ne: “Maa dikk nii, te téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man, maa defsi sa coobare, yaw Yàlla.”»

Yawut ya 10:4–7

Dees koo néewal doole, mitital ko te ubbiwul gémmiñam, xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji, ne cell ni xar mu ñuy wat, ubbiwul gémmiñam.

Esayi 53:7

Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Xar mi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo worma, yeyoo darajaak cant.»

Peeñu ma 5:12

Man may saxoo yaakaar, di la sant, di santati.

Taalifi cant 71:14

Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.

Filib 3:12

Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi bi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat njàngale yi jiitu ci xibaar bi. Njàngale mi moo di gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi dee.

Yawut ya 6:1

Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.

Kàddu yu xelu 4:18

Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo, dagaan ko, mu dégg ma. Teewlu na ma moos, dama koy woo li feek may dund.

Taalifi cant 116:1–2

Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Buur Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem.

Taalifi cant 34:1

Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda.

Taalifi cant 65:1

Ñeenti mbindeef yi am nañu ku nekk juróom benni laaf, fees aki bët ba daj, biir ak biti, te guddi ak bëccëg duñu selaw, xanaa naan: «Kee sell, Kee sell, Kee sell, Keey Boroom bi Yàlla Aji Man ji, Kee masa nekk, Kee nekk, Keey dikk.»

Peeñu ma 4:8

Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»

Taalifi cant 50:23

Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

Filib 4:4