Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
Taalifi cant 107:8
Leeru Bés bi
Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
Taalifi cant 107:8
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
Taalifi cant 34:8
Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylooka xeebaate.
Taalifi cant 31:19
xeet wii ma bindal sama bopp, te ñooy siiwal sama woy.
Esayi 43:21
la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi bi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem. Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.
Efes 1:5–6
Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi njëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi bi.
Efes 1:12
Ndaw bànneex akub taar ca ñoom! Pepp yafal xalelu góor, biiñ bu bees naatal yaramu janq.
Sàkkaryaa 9:17
Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk. Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm, sa wóllëre yi di la sant, di tudd sa darajay nguur, tey dégtale sag njàmbaar, doom aadama xam say jaloore ak sa darajay nguur gu màgg gi.
Taalifi cant 145:9–12
Xam ngeen ne ñi muñ lanu foog ne ñoom la mbég ñeel. Dégg ngeen na Ayóoba muñe woon, ak muj ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi moo bare yërmande akug ñeewante.
Yanqóoba 5:11
Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ; te muñ mooy jur kóllërey biir coono; kóllërey biir coono mooy jur yaakaar. Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:3–5
Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub.
Yawut ya 12:11
Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk, te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural. Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
Yanqóoba 1:2–4
Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.
Yanqóoba 1:12
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw. Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole ak ci biiri saaga ak ci biir ag ñàkk ak ci biir coono yu ñu may bunduxataale ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi bi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.
2.Korent 12:9–10
Bés yu mujj yi
Wone yépp6 Now 2025
5 Now 2025
4 Now 2025
3 Now 2025
2 Now 2025
1 Now 2025
31 Okt 2025