Gémmiñam, bànneexi neen, jëmmam jépp jara xédd! Yeen janqi Yerusalem, sama nijaay a ngoog, samab xarit.
Ngën-gi-woy 5:16
Leeru Bés bi
Gémmiñam, bànneexi neen, jëmmam jépp jara xédd! Yeen janqi Yerusalem, sama nijaay a ngoog, samab xarit.
Ngën-gi-woy 5:16
Sama xalaat bii, yal na ko neex. Man de maa ngi bége Aji Sax ji!
Taalifi cant 104:34
Sama nijaay daa xees, leer; kenn la ci fukki junniy góor.
Ngën-gi-woy 5:10
Moo waral lii dikk ci Mbind mi: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ, aw doju koñu tabax, muy doju tànnéef wu gànjare. Wii doj, ku ko wéeroo, doo rus mukk.»
1.Piyeer 2:6
Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
Taalifi cant 45:2
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,
Filib 2:9
ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom.
Kolos 1:19
Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
1.Piyeer 1:8
Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi, ngir ma mana feeñe ci biir Almasi bi, fu ma yaakaarul sama njubteg bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njubte gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi bi. Njubte googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi bi moo koy maye.
Filib 3:8–9
Ba loolu amee Daawuda jàq lool, ndax mbooloo maa nga doon wax naan dañu koy dóori doj. Booba mbooloo ma ba mu daj, ku nekk a ngaak naqaru xol, di xalaat doomam yu góor ak yu jigéen. Daawuda nag dëgërloo Yàllaam Aji Sax ji rekk.
1.Samiyel 30:6
Simoŋ Piyeer ne ko: «Sang bi, ci kan lanu jëm? Kàddu giy texeel fàww, yaa ko yor!
Yowaan 6:68
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
buumi njaniiw laaw ma, dee ne jaas, di ma fiir.
Taalifi cant 18:6
musal ma ca noon yu mag ya ma bañ te man ma. Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,
Taalifi cant 18:18–19
Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Buur Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem. Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu. Aji Sax ji laay sagoo, néew-ji-doole dégg, bég. Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, nu bokk wormaal turam.
Taalifi cant 34:1–4
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
Taalifi cant 34:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Okt 2025
27 Okt 2025
26 Okt 2025
25 Okt 2025
24 Okt 2025
23 Okt 2025
22 Okt 2025