Leeru Bés bi — 11 Ut: Yawut ya 2:14

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.

Yawut ya 2:14

Woowu yiw, la ko fésal moo di dikkug sunu Musalkat Almasi Yeesu, mi neenal dee, te niital nu yoonu texe, ak dee gu fomm ba fàww, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.

2.Timote 1:10

Mooy mëdd dee ba fàww! Boroom bi Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.

Esayi 25:8

Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu dee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na dee ci géeju ndam. Moo yaw dee, ana sa ndam? Moo yaw dee, ana sag fitt?» Dee, ag fittam mooy bàkkaar, te bàkkaar, dooleem mooy yoon wi. Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!

1.Korent 15:54–57

Ndax kat Xel mi nu Yàlla jox taxu noo ragal, xanaa kay da noo may doole ak cofeel ak jëfin wu laloo am xel.

2.Timote 1:7

Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.

Taalifi cant 23:4

Ana yoon wa jëm fa leer dëkke, ak fa lëndëm màkkaanoo,

Ayóoba 38:19

Xibaar bi nu dégge ci moom, di leen ko àgge, mooy lii: Yàlla ag leer la, te gennug lëndëm nekkul ci moom.

1.Yowaan 1:5

Li feek maa ngi ci àddina, maay leeru àddina.»

Yowaan 9:5

Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg. Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.

1.Yowaan 1:6–7

te ngeen di sante Baay bi mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga. Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp. Ci moom lanu ame ag njot, te moo nu jéggal sunuy bàkkaar.

Kolos 1:12–14

Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.

1.Tesalonig 5:5

Yeena di leeru àddina. Ab dëkk, bu nekkee ci kaw tund, du mana làqu.

Macë 5:14

Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.

Macë 5:16