Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
Ngën-gi-woy 4:7
Leeru Bés bi
Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
Ngën-gi-woy 4:7
Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk? Bopp ba téstën, fenn jagul. Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk, ak góom yuy nàcc, fajeesu ko, takkeesu ko, gajfaleesu kook ag diw.
Esayi 1:5–6
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Esayi 64:6
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi bi ak ci sunu Noowug Yàlla.
1.Korent 6:11
Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
Taalifi cant 45:13
siiw ba xeet yépp xam la ndax taar bu sotti ndax sama gànjar gu yànj gi ma la takkal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Esekiyel 16:14
Boroom bi sunu Yàlla, ngalla baaxe nu. Sottalal nu sunu liggéeyu loxo, rikk, sottalal nu sunu liggéeyu loxo.
Taalifi cant 90:17
Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi.
Peeñu ma 7:14
Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Efes 5:27
ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.
Kolos 2:10
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
Yeremi 2:13
Gannaaw loolu Aadama ànd ak soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax ji.»
Njàlbéen ga 4:1
daldi ne: «Ayca nu tabax ab dëkk bu taax ma bëtt asamaan; kon dinanu am woy, te dunu tasaaroo ci kaw suuf.»
Njàlbéen ga 11:4
Ba loolu amee Aji Sax ji jële leen foofa, tasaare leen ci kaw suuf sépp, ñu yemale fa dëkk ba ñu doon tabax.
Njàlbéen ga 11:8
Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqalikoo.
Njàlbéen ga 13:11
Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Cowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.
Njàlbéen ga 13:10
Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
Njàlbéen ga 13:13
Noonu dogu naa xam luy xel mu rafet, xam luy nitoodi akug ndof. Fekk loolu it nappum ngelaw la. Ku géejal xel mu rafet, géejal naqar; yokku xam-xam, yokku tiis.
Kàdduy waare 1:17–18
Damaa liggéey lu réy. Tabaxlu naa samay kër, jëmbat sama toolub reseñ.
Kàdduy waare 2:4
Ma dajale sama xaalis ak sama wurus, moom alali buur yeek diiwaan yi ma yilif, tabb samay woykat, góor ak jigéen, boole ci bànneex bi ci jabari jabar.
Kàdduy waare 2:8
Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak nappum ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.
Kàdduy waare 2:11
Bés ba mujj ca màggal ga nag moo ca gënoona màgg. Keroog la Yeesu taxaw, àddu ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man, naan;
Yowaan 7:37
Mooy màndal put gu wow, di feesal ngëneel biir bu wéet.
Taalifi cant 107:9
La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf,
Kolos 3:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp8 Ut 2025
7 Ut 2025
6 Ut 2025
5 Ut 2025
4 Ut 2025
3 Ut 2025
2 Ut 2025