Leeru Bés bi — 10 Ut: Yowaan 17:15

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ñaanuma nga jële leen ci àddina, xanaa nga musal leen ci ku bon ki.

Yowaan 17:15

ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,

Filib 2:15

«Yeena di xoromas àddina. Bu xorom raxee ba sàlli, nees koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, xanaa ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. Yeena di leeru àddina. Ab dëkk, bu nekkee ci kaw tund, du mana làqu.

Macë 5:13–14

Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.

Macë 5:16

Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ.

Njàlbéen ga 20:6

Waaye Boroom bi mooy ki jara wóolu, te moo leen di dooleel, musal leen ci ku bon ki.

2.Tesalonig 3:3

Waaye boroom réew yi ma jiitu dañu daan noot askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla.

Neyemi 5:15

bi maye bakkanam ngir njotug sunuy bàkkaar, ba musal nu ci jamonoy tey ju bon ji, ci coobarey Yàlla sunu Baay

Galasi 1:4

Fexeleen ba des ci biir cofeelu Yàlla, tey séentu sunu yërmandey Boroom Yeesu Almasi bi, ngir ag texe gu sax dàkk.

Yudd 21

Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi bi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.

Yudd 25

Ragal nit dugal sa bopp la, ku wóolu Aji Sax ji, fegu.

Kàddu yu xelu 29:25

Aji Sax jee kawe, moo dëkke fa kaw-a-kaw, te mooy dajal fi Siyoŋ àtteb dëgg ak yoon.

Esayi 33:5

Aji Sax jee kawe, tiim xeetoo xeet, darajaam sut asamaan!

Taalifi cant 113:4

Mooy yékkatee ku néewle fa suuf, di seppee ku sonn cib sën, bokkal ko jataayu kilifa ya jiite xeetam.

Taalifi cant 113:7–8

Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.

Efes 2:4–6

Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?

Room 8:32

Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.

Room 8:38–39