Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi bi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.
Room 6:4
Leeru Bés bi
Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi bi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.
Room 6:4
Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur cellte.
Room 6:19
Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war. Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.
Room 12:1–2
Kon bu nit ki bokkee ci Almasi bi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.
2.Korent 5:17
Xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo. Li am solo mooy doon mbindeef mu bees. Mboolem ñiy sàmm ndigal lii nag, te di Israayilu Yàlla, jàmm ak yërmande ñeel na leen.
Galasi 6:15–16
Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu.
Efes 4:17
Yeen nag du loolu ngeen jànge ci Almasi bi, ndegam kay Yeesu ci boppam ngeen dégg mbiram, ba jànge ci moom, dëgg gi bawoo ci moom,
Efes 4:20–21
te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub ak sellaay ji dëgg di jur.
Efes 4:24
Yeesu delluwaat, ba nee, ñaareel bi yoon, daldi ñaan ne: «Sama Baay, ndegam lii manu maa teggi ba duma ko naan, na sa coobare am.»
Macë 26:42
Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.
Yeremi 10:23
Ba loolu amee, Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mu ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko! Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
Macë 26:39
Xanaa ne tekk, ne cell, ni perantal ak ndeyam; sama xel dal ni perantal.
Taalifi cant 131:2
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ. Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, ndax ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
Room 8:26–27
Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Mbaa kaasub naqar bi may naani, man ngeen koo naan?» Ñu ne ko: «Man nanu ko.»
Macë 20:22
Yàlla jox leen la ñuy sàkku, wàccaaleel leen woppi ràgg.
Taalifi cant 106:15
Yooyu xew-xew ay misaal la, ngir nu baña xemmem yëf yu bon, na ko maam ya daan xemmeme.
1.Korent 10:6
Sama coobare mooy, yeen gëmkati Almasi bi, ngeen mucc ci xalaat yu ub seen bopp. Te ku amul jabar, mbiri Boroom bi lay xalaat ak nu muy dabe bànneexu Boroom bi.
1.Korent 7:32
Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.
Esayi 26:3
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Ut 2025
3 Ut 2025
2 Ut 2025
1 Ut 2025
31 Sul 2025
30 Sul 2025
29 Sul 2025