Leeru Bés bi — 6 Ut: Kàddu yu xelu 3:12

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, yar la, ni baay, ak doom ju ko neex.

Kàddu yu xelu 3:12

Kon gisleen ne man la, man doŋŋ, kenn du Yàlla ku dul man! Man maay rey, di dundal; di gaañe, di wéral; maay jàpp, te kenn du xettali.

Baamtug yoon wi 32:39

Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.

Yeremi 29:11

«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee.

Esayi 55:8

Maay yàqate garabi reseñ aki figg yi mu noon: “Lii sama peyoor la! Samay far a ma ko jox.” Maa koy def ay dédd, rabi àll yi di ko lekk.

Ose 2:14

Xamleen xéll ne ni baay di yare doomam, ni la leen seen Yàlla Aji Sax ji yare.

Baamtug yoon wi 8:5

Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub.

Yawut ya 12:11

Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,

1.Piyeer 5:6

Aji Sax ji, ràññee naa ne say àtte dëgg la, te worma nga ma dumaa.

Taalifi cant 119:75

Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees, ak àddina ak li ci biiram.

Taalifi cant 24:1

«Moo tax man Aji Sax ji, maa ngii di ñage yoonam ay dég, gawe ko ag wërmbal, ba yoon réer ko. Mooy topp ay faram te du leen dab; mu seet leen, du leen gis. Su boobaa mu ne: “Naa dellu ca saa jëkkër ju njëkk ja, nde ca laa gënoonu demin.”

Ose 2:8–9

Ana lu nu tekki, maak sama ñoñ, ba nu man laa jox saraxi yéene yii? Ci yaw la lépp jóge, te say loxo lanu jële, jox la. Ay doxandéem lanu fi yaw, diy gan ni sunuy maam yépp. Sunu fani kaw suuf, takkndeer buy wéy la, yaakaar amu ci. Yaw Aji Sax ji, sunu Yàlla, alal jii nu dajale, mu ne gàññ, di ko tabaxe kër gu ñuy tudde sa tur wu sell, Ci say loxo la jóge, lépp yaay boroom.

1.Jaar-jaar ya 29:14–16

Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.

Room 11:36

Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.

1.Timote 6:17

Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees koy jariñoo. Lu mu mana doon, kàddug Yàlla akug ñaan moo koy sellal.

1.Timote 4:4–5

Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.

Filib 4:19