Mboolem waa àddina di ko sujjóotal, maanaam mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Xar mi ñu rendi.
Peeñu ma 13:8
Leeru Bés bi
Mboolem waa àddina di ko sujjóotal, maanaam mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Xar mi ñu rendi.
Peeñu ma 13:8
Gàtt ba bumu am sikk te na di kuuyu menn at. Man naa doon xar mbaa sikket. Dangeen koy denc ba fukkeelu bés ba ak ñeent ci weer wii. Bu bés baa ci diggante ngoon ak jant bu so, na mbooloom Israayil mépp bokk rendi seeni gàtt. Su ko defee ñu sàkk ca deret ja, taqal ca buntu kër ga ñu ko nara lekke, taqal ca ñaari jëni bunt ba ak njëël bunt ba ca kaw.
Mucc ga 12:5–7
Deret ji ci kër yi ngeen dëkke nag, mooy doon seen xàmmikaay, ba tax bu ma gisee deret ji, musal leen. Su ko defee bu may dal ci kaw réewum Misra, menn musiba du leen lor.
Mucc ga 12:13
Yeena àgg fa Yeesu, rammukat bi dox kóllëre gu yees gi. Yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.
Yawut ya 12:24
Setalleen seen bopp boog, génneleen lawiir bu yàgg bi ci seen biir, ba mana doon tooyal bu bees bu mucc lawiir, nde doon ngeen ko ba noppi, ndax Almasi bi, sunu gàttub bésub Mucc biy sunub sarax, rendilees na nu ko.
1.Korent 5:7
Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
Jëf ya 2:23
Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.
2.Timote 1:9
Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,
Efes 1:7
Gannaaw Almasi bi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar, ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.
1.Piyeer 4:1–2
«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, sama sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.
Esayi 63:3
«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
Mucc ga 15:11
Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, ci àtteem la sukkandikoo.
Esayi 59:16
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
1.Piyeer 2:24
Almasi bi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
Galasi 3:13
Dib taalifu cant. Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, moo def ay jaloore; kàttanam ak sellaayu dooleem jox na ko ndam li.
Taalifi cant 98:1
Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam la Almasi bi ame ca bant ba.
Kolos 2:15
Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko. Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, mu def ñu bare, ñu ñu limal njub, ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef.
Esayi 53:11
walum Kison buub leen, falaŋ, walum Kison maa! walum cosaan maa! Naa dëgërlu boog te buure xol.
Njiit ya 5:21
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Room 8:37
Sunu bokk yee daan ndax deretu Xar mi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.
Peeñu ma 12:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Ut 2025
31 Sul 2025
30 Sul 2025
29 Sul 2025
28 Sul 2025
27 Sul 2025
26 Sul 2025