Leeru Bés bi — 1 Ut: Efes 2:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la;

Efes 2:8

Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga njëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.

Yawut ya 11:6

Képp ku ko gëm, deesu la daan, waaye ku ko gëmul, daanees na ko ba noppi, ndax moo gëmul jenn Doomu Yàlla ji.

Yowaan 3:18

Baayu xale bi daldi àddu ca kaw, ne: «Kon gëm naa, ngalla wallu maak sama ngëmadi.»

Màrk 9:24

Képp kuy jëfe kàddug Yàlla, ci moom déy la cofeelu Yàlla mate sëkk. Ci loolu lanuy xame ne moom lanu nekk.

1.Yowaan 2:5

Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm gi jëfi cofeel di firndeel.

Galasi 5:6

Yaa ñàkk bopp, ndax dangaa bëgg lu la firndeel ne ngëm gu àndul ak jëf amul njariñ?

Yanqóoba 2:20

ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis.

2.Korent 5:7

Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.

Galasi 2:20

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd, ndax yeena ngi jot ci yool bi ngëm di yóotu, te mooy texe.

1.Piyeer 1:8–9

Xam ngeen ne ñi muñ lanu foog ne ñoom la mbég ñeel. Dégg ngeen na Ayóoba muñe woon, ak muj ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi moo bare yërmande akug ñeewante.

Yanqóoba 5:11

Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.

Taalifi cant 103:13

Moo dogal ñuy fàttalikuy kéemaanam; Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande. Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.

Taalifi cant 111:4–5

Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul. Kiy sàmm Israayil kay gëmmul, nelawul.

Taalifi cant 121:3–4

Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, di wër, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen. Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.

Baamtug yoon wi 32:11–12

Aji Sax ji, ngoram du dakk, te yërmandeem du jeex. Xanaa di yeeslu jant bu nekk. Kee bare kóllëre!

Jooytu 3:22–23

Ba mu wàccee ca gaal ga, mbooloo mu réy la gis. Mu ñeewante leen, daldi faj seeni jarag.

Macë 14:14

Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.

Yawut ya 13:8

Seen kawari bopp sax, waññees na lépp.

Macë 10:30

Ñaari picci ramatu, xanaa du dërëm lay jar? Moona menn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay.

Macë 10:29

Kon nag buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën.

Macë 10:31