Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi bi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi bi tooge ca ndijooru Yàlla.
Kolos 3:1
Leeru Bés bi
Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi bi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi bi tooge ca ndijooru Yàlla.
Kolos 3:1
Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.
Kàddu yu xelu 4:5
Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la njëkka def, teg ci ànd ak jàmm akug dal. Day taxa neexa jubool, fees ak yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-parloo akug jinigal.
Yanqóoba 3:17
Xóote ya nee: «Xel mu rafet dëkku fi de!» Géej ne: «Nekku fi de!»
Ayóoba 28:14
Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi bi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees. Gannaaw dees noo bennale ak moom ci dee gu ñu nirule ak deewam, dees nuy bennale itam ak moom ci ndekkite lu niru ndekkiteem.
Room 6:4–5
Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.
Yawut ya 12:1
Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi bi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.
Efes 2:4–6
Ñooñuy dëggal ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina nag, te ñoo firndeel ci lu leer ne réew mu ñu moomal seen bopp lañu doon wut.
Yawut ya 11:14
Wutleen Aji Sax ji, mboolem yeen néew-dooley réew mi, yeen ñiy jëfe àttey yoonam, sàkkuleen njub te sàkkoo toroxlu, jombul ngeen yiiru, kera bésu merum Aji Sax ji.
Sofoni 2:3
Nikodem bokk na ca Farisen ya fa nekkoon, te demoon na seeti Yeesu lu jiitu loolu. Mu ne leen:
Yowaan 7:50
Piyeer moom, yoxal Yeesu lu sore, topp ca gannaawam, ba ca ëttu sarxalkat bu mag ba; mu dugg, toog ak wattukat ya, di seet nu mbir may mujje.
Macë 26:58
Teewul sax ñu bare ci njiiti Yawut yi gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee taxoon biraluñu seen ngëm, ndax ragal ñu dàqe leen ca jàngu Yawut ba, ndax ngërëmal nit ñi moo leen gënaloon ngërëmal Yàlla.
Yowaan 12:42–43
Ragal nit dugal sa bopp la, ku wóolu Aji Sax ji, fegu.
Kàddu yu xelu 29:25
Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
Yowaan 6:37
Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.
Esayi 42:3
20-Yeesu ne leen: «Xanaa seenug néew ngëm. Maa leen ko wax déy, su ngeen amee ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën, dingeen ne tund wii: “Toxool fii, ba fale,” mu toxu, te dara du leen të.»
Macë 17:20
Ndax kat Xel mi nu Yàlla jox taxu noo ragal, xanaa kay da noo may doole ak cofeel ak jëfin wu laloo am xel. Bul kersawoo di seedeel sunu Sang, mbaa nga di ma kersawoo, man mi ñu tëj ngir moom, waaye jëlal sa wàll ci coonob xibaaru jàmm bi, ni la ko manoorey Yàlla manloo.
2.Timote 1:7–8
Léegi nag xale yi, saxleen ci Almasi bi, ndax bu feeñee, nu siggi fi kanamam te baña rus kera ba muy feeñ.
1.Yowaan 2:28
«Képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, man ci sama wàllu bopp itam, dinaa dëggal fa sama kanam Baay ba fa asamaan, ne man nga féeteel.
Macë 10:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Sul 2025
28 Sul 2025
27 Sul 2025
26 Sul 2025
25 Sul 2025
24 Sul 2025
23 Sul 2025