Leeru Bés bi — 27 Sulet: 2.Korent 4:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm biy yànjal leeru Almasi biy melokaanu Yàlla.

2.Korent 4:4

darajay Aji Sax ji daldi feeñ, àddina sépp bokk gis ko. Aji Sax jee ko wax ci làmmiñam.»

Esayi 40:5

Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.

Yowaan 1:18

Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.

Yowaan 1:14

Yeesu ne ko: «Filib, ni ma yàggeek yeen te ba tey xamuloo ma? Ku ma gis kay, gis nga Baay bi. Kon ana noo naan: “Won nu Baay bi”?

Yowaan 14:9

Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Yawut ya 1:3

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

1.Timote 3:16

Ci moom lanu ame ag njot, te moo nu jéggal sunuy bàkkaar. Doom jooju moo di niruwaale Yàlla, mi kenn manula gis, mooy taaw bi, ki jiitu mépp mbindeef.

Kolos 1:14–15

Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw ci biir rakk yu bare.

Room 8:29

Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.

Taalifi cant 18:39

Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole ak ci biiri saaga ak ci biir ag ñàkk ak ci biir coono yu ñu may bunduxataale ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi bi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.

2.Korent 12:10

Aji Sax ji nag duma Kuuseen ña fa kanam Asa ak Yuda, Kuuseen ña daw.

2.Jaar-jaar ya 14:11

Ba loolu amee ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii mooy buurub Israayil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag woote wall, Aji Sax ji dimbali ko, waññi leen.

2.Jaar-jaar ya 18:31

Làqoo Aji Sax jee gën wóolu doom aadama. Làqoo Aji Sax jee gën wóolu garmi.

Taalifi cant 118:8–9

Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar. Yaakaar aw fas nax sa bopp la, kàttanu fas dug wall.

Taalifi cant 33:16–17

Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan. Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.

Efes 6:12–13