te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.
Efes 5:2
Leeru Bés bi
te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.
Efes 5:2
Kon ndigal lu bees laa leen di jox, soppanteleen: ni ma leen soppe, yeen itam nangeen ni soppantee.
Yowaan 13:34
Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far.
1.Piyeer 4:8
Mbañeel ak ayoo; cofeel ak jéggale bépp tooñ.
Kàddu yu xelu 10:12
25-Bu ngeen taxawee di ñaan it, te fekk ngeen jàppal kenn dara, baalleen ko, ngir seen Baay ba fa asamaan baal leen seeni tooñ, yeen itam.»
Màrk 11:25
Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.
Luug 6:35
Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
Kàddu yu xelu 24:17
Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.
1.Piyeer 3:9
Su manee am, jàmmooleen ak ñépp, ndegam ci yeen la aju.
Room 12:18
Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.
Efes 4:32
Xale yi, bunu soppante ci làmmiñu kese maanaam ay wax, waaye nanu ko jëfe, te muy dëgg.
1.Yowaan 3:18
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant.
Filib 4:6
Mu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Waaye bumuy sama coobare, nay doon ci sa coobare.»
Màrk 14:36
Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme. Mbir moomu, ñetti yoon laa ci ñaan Sang bi, ngir mu sorele maak moom. Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.
2.Korent 12:7–9
Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
Taalifi cant 142:2
Mu am bés, gannaaw ba ñu lekkee ba naan ca seen saraxu cant, foofa ca Silo, Aana jóg. Booba Eli sarxalkat baa nga ca toogu ba, feggook jënu buntu jaamookaayu Aji Sax ji. Aana dem ba foofa, ànd ak naqaru xolam, di ñaan ci Aji Sax ji, tey jooy jooy yu metti. Ci biir loolu mu xas aw xas, daldi ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Sang bi, soo nemmiku woon ba nemmiku njàqare jii ma nekke, bàyyi ma xel, bañ maa fàtte, ba may ma doom ju góor! Kon déy, maa koy sédde Aji Sax ji, giiru dundam gépp, saatus watukaay du jaar ci boppam mukk.»
1.Samiyel 1:9–11
Aana mujj ëmb ca ndeetel at ma. Gannaaw gi, mu am doom ju góor, tudde ko Samiyel (muy firi Yàlla dégg na), ndax da ne: «Maa ko ñaan Aji Sax ji.»
1.Samiyel 1:20
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
Room 8:26
Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi.
Taalifi cant 47:4
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Sul 2025
26 Sul 2025
25 Sul 2025
24 Sul 2025
23 Sul 2025
22 Sul 2025
21 Sul 2025