Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»
Sàkkaryaa 3:4
Leeru Bés bi
Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»
Sàkkaryaa 3:4
Dib taalifu yeete, ñeel Daawuda. Ndokkalee yaw mi ñu baal ag moy, jéggal la bàkkaar.
Taalifi cant 32:1
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Esayi 64:6
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
Ndax kat mboolem yeen ñi ñu sóob sóobeb Almasi bi, jëmmu Almasi bi ngeen soloo.
Galasi 3:27
Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi, ba sol seen jëmm ju yees jiy gën di yeeslu, te di gëna niru ki leen ko sàkkal, ba kera seen xam-xam mat sëkk.
Kolos 3:9–10
ngir ma mana feeñe ci biir Almasi bi, fu ma yaakaarul sama njubteg bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njubte gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi bi. Njubte googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi bi moo koy maye.
Filib 3:9
Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll.
Luug 15:22
Jox nañu ko mbubbum lẽe mu set, ne ràññ, mu sol.» Lẽe boobu mooy jëfi njekk yu nit ñu sell ñi.
Peeñu ma 19:8
Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
Esayi 61:10
ku ci nekk, sab liggéey dina feeñ, ndax bés-pénc baa koy xamle, nde sawara lees koy feeñale. Ku ci nekk ak lu sa xeetu liggéey mana doon, sawara lees koy natte.
1.Korent 3:13
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
1.Korent 4:5
Yaw nag ana looy sikke sa mbokkum gëmkat, ak itam, ana looy xeebe sa mbokkum gëmkat? Ndax kat nun ñépp ay taxawi fa kanam jalub àttekaayu Yàlla ba.
Room 14:10
Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla. Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakkastal, mbaa lu koy xiirtal ci bàkkaar.
Room 14:12–13
Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi bi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
Room 2:16
Baay bi du àtte kenn; Doom ji la dénk àtte bi bépp,
Yowaan 5:22
te sañ-sañu amal àtte bi itam, moom la ko jox, ndax mooy Doomu nit ki.
Yowaan 5:27
Yaw miy jëfe ngor sa digg ak junniy maas, te bu baay ñaawee, nga topp ko ko, ba ci doomam. Yaay Yàlla ju màgg ji te jàmbaare. Yaa di Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, réyi pexe, màggi jaloore; say gët ne jàkk ci mboolem lu doom aadama def, ngay añale ku nekk jëfinam ak jëfam.
Yeremi 32:18–19
Bés yu mujj yi
Wone yépp8 Sul 2025
7 Sul 2025
6 Sul 2025
5 Sul 2025
4 Sul 2025
3 Sul 2025
2 Sul 2025