Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
1.Piyeer 2:21
Leeru Bés bi
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
1.Piyeer 2:21
Ndax Doomu nit ki itam ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñu bare.»
Màrk 10:45
te ku bëgga nekk seen njiit, na doon jaamub ñépp.
Màrk 10:44
ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane nootoon.
Jëf ya 10:38
Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.
Galasi 6:2
Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi bi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaléey fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñeméey,
2.Korent 10:1
Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye woyofluleen, ba jàpp ne seeni moroom a leen gën.
Filib 2:3
Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
Luug 23:34
Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.
Efes 4:32
Ku ne moo sax ci Yàlla, fàww ni Yeesu Almasi bi daan jëfe, ni lay jëfe moom itam.
1.Yowaan 2:6
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:2
Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.
Ngën-gi-woy 5:6
Ngalla Boroom bi, lu may waxati nag, gannaaw Israayil a walbatiku, won noon yi doq?
Yosuwe 7:8
Aji Sax ji ne Yosuwe: «Jógal taxaw! Ana looy sukk di dëpp sa jë fi suuf? Israayil a bàkkaar. Ñoo fecci sama kóllëre gi ma leen sàmmloo woon. Ñoo sàkk ca alal ja ñu aaye. Dees koo far sàcc, ngir naxe, ba far ko yeb ca seeni denc.
Yosuwe 7:10–11
Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg. Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.
Esayi 59:1–2
Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.
Taalifi cant 66:18
Soppe yi, bu nu sunum xel sikkul, dinanu ñemee walbatiku ci Yàlla. Te kon lu nu ñaan, mu may nu ko, ndax ay ndigalam lanuy sàmm, te li mu rafetlu lanuy jëfe.
1.Yowaan 3:21–22
Bés yu mujj yi
Wone yépp20 Suw 2025
19 Suw 2025
18 Suw 2025
17 Suw 2025
16 Suw 2025
15 Suw 2025
14 Suw 2025