Leeru Bés bi — 17 Suwe: Filib 4:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant.

Filib 4:6

Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo, dagaan ko, mu dégg ma. Teewlu na ma moos, dama koy woo li feek may dund.

Taalifi cant 116:1–2

«Bu ngeen di ñaan, buleen jàppoo kebetu ni yéefar yi foog ne ci wax ju bare lees leen di nangule.

Macë 6:7

Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.

Room 8:26

Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo.

1.Timote 2:8

Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.

Efes 6:18

«Maa leen neeti, su ñaar ci yeen déggoo ci kaw suuf, ci mboolem lu ñu ñaan, dees na leen ko nangul ci sama dogalu Baay ba fa asamaan,

Macë 18:19

Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm, sa wóllëre yi di la sant,

Taalifi cant 145:10

Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellaayu turam! Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, te baña fàtte mboolem xéewalam!

Taalifi cant 103:1–2

Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Buur Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem.

Taalifi cant 34:1

Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu.

Taalifi cant 34:2

Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo, ngir niir sa doole ak sa leer. Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; ma àddu boog, kañ la! Dama lay sant, sama giiru dund kay, tàllal la ay loxo, sàbbaale la.

Taalifi cant 63:3–5

Maryaama nag ne: «Sama xol laay màggale Boroom bi, samag noo laay bége Yàlla mi may musal,

Luug 1:46–47

«Yàlla sunu Boroom, yaa yeyoo daraja ak worma ak manoore, ndaxte yaa sàkk lépp, lépp lu am, yaw la soob, nga sàkk ko.»

Peeñu ma 4:11