Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen cellte, nde ku sellul du gis Boroom bi.
Yawut ya 12:14
Leeru Bés bi
Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen cellte, nde ku sellul du gis Boroom bi.
Yawut ya 12:14
Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki, su judduwaatul, du mana gis nguurug Yàlla.»
Yowaan 3:3
Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Xar mi doŋŋ ñoo fay dugg.
Peeñu ma 21:27
Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
Ngën-gi-woy 4:7
«Waxal mbooloom bànni Israayil gépp ne leen: Ñu sell ngeen wara doon, ndax Ku sell laa, man seen Yàlla Aji Sax ji.
Sarxalkat yi 19:2
Gannaaw gone yu dégg ndigal ngeen, buleen toppati seen xemmemtéefi bakkan ya woon, ba ngeen xamulee. Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin. Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell ngeen wara doon, ndax man Ku sell laa.» Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.
1.Piyeer 1:14–17
te mooy ngeen bàyyi seen jikko ju njëkk ja, ngeen teqalikoo ak seen jëmm ja woon démb, jëmm ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute. Su ko defee ngeen mana yeeslu ci seenum xel, ci ndimbalal Noowug Yàlla, te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub ak sellaay ji dëgg di jur.
Efes 4:22–24
Te mooy noonu mu nu tànne ba àddina sosoogul ndax Almasi bi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel
Efes 1:4
dama lay digal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara ba mu set wecc, ngir nga am alal. Jëndal itam yére yu weex yoo sol, ba làq sa duŋŋaaral gu gàccelu gi; ak tuufaay looy tuufoo, ngir nga gis.
Peeñu ma 3:18
Yeesu ne ko: «Maa leen ko wax déy, amul kenn kuy dëddu kër, mbaa doomi ndey yu góor mbaa yu jigéen, mbaa ndey mbaa baay, mbaa doom, mbaa suuf, ngir maak xibaaru jàmm bi, te jotuloo ci jamonoy tey jii téeméeri yoon, la nga amoon ciy kër, ak doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ak ndey ak doom ak suuf, ba jotaale coonoy bunduxataal, ak texe ba fàww gooy jot ëllëg.
Màrk 10:29–30
Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal.
1.Piyeer 4:12
Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu. Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Piyeer 1:6–7
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.
1.Piyeer 5:10
Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»
Yowaan 16:33
Bés yu mujj yi
Wone yépp18 Suw 2025
17 Suw 2025
16 Suw 2025
15 Suw 2025
14 Suw 2025
13 Suw 2025
12 Suw 2025