Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
Taalifi cant 85:10
Leeru Bés bi
Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
Taalifi cant 85:10
Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!
Esayi 45:21
Aji Sax ji la soob ci njubteem, mu fésal màggaayu yoonam ak taar ba.
Esayi 42:21
Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.
2.Korent 5:15
Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon, ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.
Room 3:25–26
Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam.
Esayi 53:5
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub.
Room 8:33
Waaye ki jëful te gëm Yàlla miy baaxe ab yéefar sax àtteb ku jub, ngëmam googu, ag njub lees ko koy limal.
Room 4:5
Teewul nit a ngi naan: «Nan la ñi dee di dekkee? Wan yaram lañuy dekkaale?»
1.Korent 15:35
Kooku moo dikk ag guddi ba ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ab kilifa nga bu bawoo fa Yàlla, nde kenn manula def firnde yii ngay def, te du Yàllaa ànd ak moom.»
Yowaan 3:2
Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.
Filib 3:20–21
Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!» Tiitaange ju réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis.
Luug 24:36–37
Mu feeñu Sefas, teg ca feeñu fukki taalibe ya ak ñaar. Gannaaw gi, mu feeñu lu ëpp juróomi téeméeri bokki taalibe yu ko gisandoo, te li ëpp ci ñooñu, ñu ngi dund ba léegi, doonte am na ñu ci nelaw.
1.Korent 15:5–6
Noowug ki dekkal Yeesu moo sax ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi bi mooy dekkal itam seen yaram wu jëm ci dee, ndax Noowam googu sax ci yeen.
Room 8:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp5 Mee 2025
4 Mee 2025
3 Mee 2025
2 Mee 2025
1 Mee 2025
30 Awr 2025
29 Awr 2025