Ni seen Baay ba fa asamaan mate nag, nangeen ni mate.
Macë 5:48
Leeru Bés bi
Ni seen Baay ba fa asamaan mate nag, nangeen ni mate.
Macë 5:48
Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.
Njàlbéen ga 17:1
«Nangeen nekk ñu sell ci man, ndaxte Ku sell laa, man Aji Sax ji, te dama leena ràññaatleek yeneen xeet yi, ngeen di sama ñoñ.
Sarxalkat yi 20:26
ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.
1.Korent 6:20
ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.
Kolos 2:10
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Tit 2:14
Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.
2.Piyeer 3:14
Ndokkalee yaw mi màndu, di wéye yoonu Aji Sax ji.
Taalifi cant 119:1
Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte, xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.
Yanqóoba 1:25
Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol; natt ma, ba ràññee sama xalaati xol. Xoolal ndax maa ngi doxe yoon wu aay, te nga teg ma ci yoon wi sax.
Taalifi cant 139:23–24
Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram ak ju xel, te nu sax ci sellaay ci ag ragal Yàlla.
2.Korent 7:1
Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.
Taalifi cant 51:6
Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ragal Yàlla ci àddinay tey jii.
Tit 2:12
Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.
Macë 5:16
Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.
Filib 3:12
Te képp ku am jooju yaakaar ci moom, noonu mu sete, ni lay setale boppam.
1.Yowaan 3:3
Googu muj ci boppam la nu Yàlla mooñe woon, te Noo gu Sell gi mu nu jox la nu ci dawalal.
2.Korent 5:5
Almasi bi moo waajale noonu ñu sell ñi, ba ñu mana bey seen sas ci liggéeyam, ngir tabax mbooloom gëmkat mi taxawe yaramu Almasi bi. Su ko defee nu mana màgg nun ñépp ba doon benn ci ngëm ak ci xam-xam bu mat ci Doomu Yàlla ji, ba kera nuy doon magum jëmm, bay tollook taxawaayu Almasi bi mat sëkk.
Efes 4:12–13
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Mee 2025
1 Mee 2025
30 Awr 2025
29 Awr 2025
28 Awr 2025
27 Awr 2025
26 Awr 2025