Képp kuy jëfe kàddug Yàlla, ci moom déy la cofeelu Yàlla mate sëkk. Ci loolu lanuy xame ne moom lanu nekk.
1.Yowaan 2:5
Leeru Bés bi
Képp kuy jëfe kàddug Yàlla, ci moom déy la cofeelu Yàlla mate sëkk. Ci loolu lanuy xame ne moom lanu nekk.
1.Yowaan 2:5
Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk, yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottal ci Yeesu Almasi bi daraja ñeel ba fàww. Amiin.
Yawut ya 13:20–21
Lii nag, ci lanuy xame xéll ne xam nanu kuy Yàlla, te mooy nuy jëfe ay ndigalam.
1.Yowaan 2:3
Yeesu ne ko: «Ku ma sopp day sàmm sama kàddu, sama Baay sopp ko; fi moom lanuy dikk, te moom lanuy def màkkaan.
Yowaan 14:23
Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko. Xale yi, bu leen kenn nax! Kuy def njub, yaa jub, ni Almasi bi ci boppam jube.
1.Yowaan 3:6–7
Cofeel a mat sëkk ci nun, ngir nu ànd ak fit keroog bés-pénc. Te li nuy may fit mooy, ni Yeesu moomu nekke, noonu lanu nekke nun itam ci àddina sii.
1.Yowaan 4:17
Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
Kàddu yu xelu 14:29
Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëme, di yéwéne, di muñ mer, boroom ngor gu bare gaak kóllëre ga.
Mucc ga 34:6
Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.
2.Piyeer 3:9
Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp, te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.
Efes 5:1–2
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la. Muñ ay dóor yu la fekk ci tooñ, ana lu ciy ndam? Waaye soo muñee coono boo daj ngir lu baax loo def, loolu de aw yiw la fa kanam Yàlla. Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
1.Piyeer 2:19–21
Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
1.Piyeer 2:23
Buleen mer ba bàkkaar, te bu jant bi sowe seen mer;
Efes 4:26
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Awr 2025
28 Awr 2025
27 Awr 2025
26 Awr 2025
25 Awr 2025
24 Awr 2025
23 Awr 2025