Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Leeru Bés bi
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Xintey bakkan nag ci dee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla dund ak jàmm lay jur.
Room 8:6
Ndegam nag ki gëmul daa bëgga dem, na dem. Su demee noonu, mbokkum gëmkat bu góor bi, mbaa ku jigéen ki amatul benn gàllankoor, waaye ci jàmm la leen Yàlla woo.
1.Korent 7:15
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Yowaan 14:27
Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesaleek gépp mbég ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen fees dell ak yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
Room 15:13
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.
Esayi 26:3
Su boobaa àtteb dëgg ay jur jàmm, àtteb yoon di dalal tey aare ba fàww, ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, ci dalluwaay yu dal xel,
Esayi 32:17–18
Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
Kàddu yu xelu 1:33
Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakkastal.
Taalifi cant 119:165
Wurmbal bi wër dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. «Dale ko ca bés ba, turu dëkk bi nag, di Yawesama, muy firi “Aji Sax jaa ngi fi.”»
Esekiyel 48:35
Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.
Peeñu ma 21:3
Ab jaamookaay nag, gisuma ko fenn ci biir dëkk bi, ndax Boroom bi Yàlla Aji Man ji ak Xar mi ñooy jaamookaay bi. Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Xar mi di làmpam.
Peeñu ma 21:22–23
Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.
Taalifi cant 17:15
Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
Taalifi cant 73:25
Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.
Sàkkaryaa 2:10
Alkànde nag du fa amati, te ngàngune mu Yàllaak Xar mi ci biir dëkk bi lay nekk, jaamu Yàlla yi di ko sujjóotal,
Peeñu ma 22:3
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Awr 2025
29 Awr 2025
28 Awr 2025
27 Awr 2025
26 Awr 2025
25 Awr 2025
24 Awr 2025