Leeru Bés bi — 29 Awril: 1.Samiyel 12:24

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ngalla fexeleen rekk ba ragal Aji Sax ji, te ngeen dëggu ci jaamoo ko seen léppi xol, ndax dangeen di xool ci jaloore yu yéeme yi mu leen defal.

1.Samiyel 12:24

Fàttalikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.

Baamtug yoon wi 8:2

Xamleen xéll ne ni baay di yare doomam, ni la leen seen Yàlla Aji Sax ji yare.

Baamtug yoon wi 8:5

Aji Sax ji, ràññee naa ne say àtte dëgg la, te worma nga ma dumaa.

Taalifi cant 119:75

Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.

Taalifi cant 119:71

Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.

Taalifi cant 119:67

Ki Sax mbugal na maa mbugal, waaye waccu ma, ma dee.

Taalifi cant 118:18

Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, du sunuy ñaawtéef la nu fey. Ni asamaan tiime suuf, ni la ngoram yiire ku ko ragal.

Taalifi cant 103:10–11

Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.

Taalifi cant 103:14

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi.

Tit 2:13

Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba. Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkiccedeg.

Yawut ya 6:19–20

Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottali.

Jëf ya 3:21

kera bés bu délsee ba jot ci teraangaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.

2.Tesalonig 1:10

Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu. Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gu Sell gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.

Room 8:22–23

Kooku moo dikk ag guddi ba ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ab kilifa nga bu bawoo fa Yàlla, nde kenn manula def firnde yii ngay def, te du Yàllaa ànd ak moom.»

Yowaan 3:2

Seenug dund dëgg Almasi bi la, te keroog bu Almasi bi feeñee, yeen itam dingeen ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.

Kolos 3:4

Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!

Peeñu ma 22:20