Leeru Bés bi — 27 Awril: 1.Korent 7:29

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Li may wax, bokk yi, moo di, li des yàggatul. Kon nag bés niki tey, na ñi am jabar mel ni bu ñu ko amul woon;

1.Korent 7:29

Ku jigéen jur, yaa néewi fan, géejal coono! Dangay tóor rekk, lax, wéy ni takkndeer, doo toog.

Ayóoba 14:1–2

Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.

1.Yowaan 2:17

Noonu nit bokke ci Aadama, ba tax ñépp di dee, noonu la ñépp mana bokke ci Almasi bi, ba tax ñu dundalaat leen, ñoom ñépp.

1.Korent 15:22

Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu dee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na dee ci géeju ndam.

1.Korent 15:54

Su nuy dund, ngir Boroom bi lanuy dund, su nu deewee it, wormaal Boroom bee tax nu dee. Kon nag nuy dund mbaa nu dee Boroom bi moo nu moom.

Room 14:8

Ndax samag dund, Almasi bi la ñeel, samag dee dàqati.

Filib 1:21

Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci. Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige. Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.

Yawut ya 10:35–37

Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.

Room 13:12

Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiitalleen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.

1.Piyeer 4:7

«Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; ci doj wi ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.

Peeñu ma 2:17

Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu njëkka woowe gëmkat ñi aji-gëm-Almasi.

Jëf ya 11:26

Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»

2.Timote 2:19

Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar aki xemmemtéefam.

Galasi 5:24

ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.

1.Korent 6:20

Waaye man de yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi bi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee. Xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo. Li am solo mooy doon mbindeef mu bees.

Galasi 6:14–15

Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp, te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla. Lu jëm nag ci séy yi yoon tere, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir,

Efes 5:1–3

Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.

Efes 5:8