Leeru Bés bi — 25 Awril: Macë 1:21

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Doom ju góor lay am; nanga ko tudde Yeesu (muy firi Boroom beey musle), ndax mooy musal aw xeetam ci seeni bàkkaar.»

Macë 1:21

Te xam ngeen ne Yeesu moo feeñ ngir far bàkkaar, te taqul fenn bàkkaar.

1.Yowaan 3:5

«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»

1.Piyeer 2:24

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:25

Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam. Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.

Esayi 53:5–6

Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi bi dee ci biir coono, ba dekki ca ñetteelu fan ba; te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.

Luug 24:46–47

Lu ko moy ca njàlbéenu àddina lay dale sonn ay yooni yoon. Waaye tey ci mujug jamono yi la feeñ benn yoon doŋŋ, ba sarxe boppam, ngir far bàkkaar.

Yawut ya 9:26

Moom la Yàlla yéege fa ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israayil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.

Jëf ya 5:31

«Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa, képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.

Jëf ya 13:38–39

Xale yi, yeen laay bind, ndax dees leena jéggal seeni bàkkaar ci turu Almasi bi.

1.Yowaan 2:12

Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.

2.Korent 8:9

ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom.

Kolos 1:19

Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya, te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi.

Yawut ya 1:3–4

Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul ci dayob boppam bi ko def nawleb Yàlla. Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.

Filib 2:6–7

Yeesu itam ne ko: «Till akug kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit ki de, amul fu mu wéer boppam.»

Macë 8:20

Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom, muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom. Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.

1.Korent 3:21–23